Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:
2«Waxal bànni Israyil, ne leen ñu walbatiku dali fa jàkkaarlook Pi Axirot, ca diggante Migadol ak géeju Barax ya. Dal-leen foofa jàkkaarlook Baal Cefon ca tefes ga.
3Su ko defee Firawna da naan: “Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.”
4Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona.
5Ba ñu yégalee Firawna buuru Misra, ne mbooloo ma daw na, mooki dagam dañoo soppi xalaat ca mbirum bànni Israyil. Ñu ne: «Waaw nun, li nu def nag? Ana luy ndeyi yiwi bànni Israyil, ba dootuñu nu surgawu?»
6Firawna takklu watiiru xareem, ànd aki jàmbaaram.
7Mboolem watiiri xarey Misra la yóbbu, jiital juróom benni téeméer, ya ca gën, bu ci nekk yeb ay kilifay xarekat.
8Aji Sax jee dëgëral boppu Firawna buuru Misra, mu toppi bànni Israyil, fekk bànni Israyil ñoom, ña ngay génn réew ma ci seen teeyu bakkan.
9Waa Misra topp leen, ñook fasi Firawna yépp, ak watiiri xareem ak dawalkatam yaak xarekatam ya, ba dab leen fa ñu dal ca tefesu géeju Barax ya, fa jàkkaarlook Baal Cefon ca wetu Pi Axirot.
10Firawnaa ngay jubsi, bànni Israyil séentu, yemuñu ci ñu moy waa Misra, ñu dikk, jubsi leen. Tiitaange lu réy jàpp bànni Israyil. Ñu woo Aji Sax ji wall.
11Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
12Xanaa du lii lanu la waxoon ca Misra? Noon nanu la, nga bàyyi nu, nu surgawu waa Misra, ndax surgawu waa Misra moo nu gënal nu dee ci màndiŋ mi!»
13Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettli leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk.
14Aji Sax ji moo leen di xeexal, yeen kay neleen tekk rekk.»
15Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Loo may wooye wall? Waxal bànni Israyil, ne leen ñu dem rekk,
16te yaw nanga yékkati saw yet, tàllal sa loxo mu tiim géej gi, ba xàll ko, ndax bànni Israyil mana dox ci suuf su wow, jàll géej gi.
17Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.
18Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»

19Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw,
20dox diggante dalu waa Misra ak dalu bànni Israyil. Niir waa nga lëndëme genn wet, wet ga ca des di leer ca guddi ga, ba tax guddi ga gépp benn dal manula fekki moroom ma.
21Gannaaw ga Musaa tàllal loxoom, mu tiim géej ga, Aji Sax ji yebal ngelawal penku lu réy guddi ga gépp, jañaxe ko géej ga, ndox ya xàjjalikoo, ba suuf su wow feeñ.
22Bànni Israyil nag dugg ca biir géej ga, di dox ci kaw suuf su wow, ndox ya ne sàtt, ñagal leen ndijoor ak càmmoñ.
23Ba mu ko defee waa Misra daw topp ca ñoom, fasi Firawna ak watiiri xareem aki gawaram ànd, ñoom ñépp ne yentam ca biir géej ga.
24Ba njël jotee Aji Sax ji dafa tollu ci biir taxaaru sawara wu ànd aku niir, di xool xarekati Misra, tiital leen, ñu fëlxoo.
25Mu boole ca téye mbegey watiir ya, ba neexatuñoo dawal. Waa Misra ne: «Nan daw gaaw, ba rëcc bànni Israyil, ndax kat Aji Sax ji moo leen di xeexal, te moo dal ci sunu kaw!»
26Aji Sax ji nag wax Musaa ne ko: «Tàllalal sa loxo, mu tiim géej gi, ndax ndox mi délsi, ba sottiku ci kaw waa Misra, ñook seen watiiri xare ak seeni gawar.»
27Musaa tàllal loxoom, mu tiim géej ga. Ba bët di set géej ga dellu na, mel na mu meloon. Waa Misra di daw, géej ga wal, dogale leen, Aji Sax ji fél leen, ñu ne ca menteñ.
28Ndox ma daa délsi, boole mëdd watiiri xare yaak gawar ya, mboolem xarekati Firawna, ya leen toppoon ca biir géej ga rekk. Kenn rëccul.
29Waaye bànni Israyil ñoom, ci suuf su wow lañu jaare ca digg géej ga, jàll, ndox ya ne sàtt, ñagal leen ndijoor ak càmmoñ.
30Noona la Aji Sax ji xettlee bànni Israyil bésub keroog ca waa Misra, ñu gis néewi waa Misra ya ne wetar ca tefes ga.
31Ba Israyil gisee na Aji Sax ji jowe loxoom bu baax ca xareem baak waa Misra, dañu daldi ragal Aji Sax ji, teg ca am kóolute ci Aji Sax ji ak ci Musaa, jaamam ba.