Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 16

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw gi mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo fa Elim, dem, ba keroog fukki fan ak juróom, ca weer wa topp ca wa ñu génne réewum Misra, ñu doora agsi màndiŋu Ciin diggante Elim ak Sinayi.
2Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
3Ña nga naa leen: «Céy ngalla nun, su nu sañoon dee, Yàlla moom nu ca réewum Misra, fa nu daan uufe cini yàpp, ñam wa ne gàññ, nu suur këll. Yeena nu indi ba ci màndiŋ mii, ngeen nara xiifloo mbooloo mii mépp, ba ñu dee.»
4Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Maa ngi nii di tawal bànni Israyil ñam wu jóge asamaan, te na mbooloo mi dem bés bu set, fori njëlu bés ak bés. Ma nattu leen ci, ba xam ndax dinañu doxe sama ndigalu yoon am déet.
5Waaye bu ñu demee ba bésub juróom benneel ba, ba togg la ñu ca indi, day tollook ñaar-cay dayo ba ñuy for bés bu set.»
6Musaa ak Aaróona nag xamal bànni Israyil ne leen: «Bu ngoonee dingeen xam ne, Aji Sax ji moo leen génne réewum Misra,
7te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.»
8Musaa teg ca ne: «Moo tax Aji Sax ji dina leen jox yàpp wu ngeen lekk ngoon, te bu bët setee mu jox leen ñam wu leen reggal, ndax Aji Sax jee dégg ngeen di ko diiŋat. Nun lu nu ci? Du nun ngeen di diiŋat waaye yeen ak Aji Sax ji la.»
9Ba loolu wéyee Musaa ne Aaróona: «Waxal mbooloom bànni Israyil gépp, ne leen ñu dem ba ca kanam Aji Sax ji, ndaxte dégg na seeni diiŋat.»
10Naka la Aaróona di wax ak mbooloom Israyil mépp, ñu jekki ne gees ca màndiŋ ma, daldi yem ci aw niir, leeru Aji Sax ji di ca feeñ.
11Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
12«Dégg naa diiŋati bànni Israyil. Wax leen ne leen, diggante ngoon ak jant bu so, dinañu lekk yàpp, te bu bët setee ñu lekk aw ñam, ba regg, ndax ñu xam ne man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.»
13Ba ngoon jotee ay picci përëntaan dikk, fees dal ba. Ba bët setee lay bay wàcc ca dal ba.
14Naka la lay ba bàcc, ñu jekki gis lu sew lale ca màndiŋ ma, def fepp yu sew ca biir, te mel ni tawub yuur, tege ca suuf.
15Bànni Israyil gis ko, di wax ca seen biir naan: «Lii lu mu?» ndax xamuñu woon lu mu doon. Musaa ne leen: «Lii mooy ñam wi leen Aji Sax ji jox, ngeen lekk.
16Aji Sax ji dafa santaane ne: “Na ku nekk for lu mat njëlam, bopp bu ne andaar, te mu natt ko ci limu nit, ñi mu bokkal xayma.”»
17Bànni Israyil def noona, ñii for lu bare, ñee lu néew.
18Waaye ba ñu ko nattee ci andaar, ña sàkkoon lu bare amuñu lu ëpp, te ña sàkkoon lu néew yéeslewuñu. La ñu for dafa tolloo tembe ak seen njël.
19Musaa ne leen: «Bu ci kenn wacc dara, mu fanaan.»
20Waaye dégluwuñu Musaa, am na ñenn ca ñoom ñu ca wàññi, fanaanal, mu def ay sax, xasaw xunn. Musaa nag mere leen.
21Suba su ñu xëyaan nag, ku nekk for ca njëlam, ndax bu naaj wa tàngaan, mu seey.
22Ba bésu juróom benneel ba jotee, dañoo for lu mat ñaari njël, ku nekk am ñaari andaar, njiiti mbooloo ma nag dem yeggeji ko Musaa,
23mu ne leen: «Loolu la Aji Sax ji wax, te li muy tekki mooy: ëllëg bésu dal-lu la, di bésub Noflaay bu sell ñeel Aji Sax ji. Lakkleen li ngeen di lakk, baxal li ngeen di baxal, te lu ci des, ngeen denc ba suba.»
24Ba ñu dencee la ca des ba ca ëllëg sa, na ko Musaa santaanee, xasawul, saxewul.
25Musaa wax leen ne leen: «Lekkleen li des tey, ndax tey jii bésub Noflaay la, ñeel Aji Sax ji, te dungeen ko gis tey ci àll bi.
26Juróom benni fan ngeen koy for, waaye bésub juróom ñaareel bay bésub Noflaay, kenn du ko gis.»
27Terewul mu am ñu fori ca bésub juróom ñaareel ba, waaye gisuñu dara.
28Ca la Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Waaw yeen nag, dungeen ma noppee gàntalal samay santaaneek samay ndigali yoon mukk?
29Nangeen xam xéll ne, man Aji Sax ji, maa leen may bésub Noflaay ngir ngeen nopplu, te looloo tax ma may leen dundub ñaari fan ci bésub juróom benneel bi. Kon nag bésub juróom ñaareel ba, na ku nekk toog fi mu nekk, bu ci kenn génnati fi mu dëkk.»
30Ba loolu amee bànni Israyil di nopplu bésub juróom ñaareel ba.
31Waa kër Israyil nag tudde ñam wa mànn (mu firi Lii lu mu?). Dafa meloon ni pepp, mi ñuy wax koryanda, te weex, di saf lu mel ni nàkk bu ànd ak lem.
32Ci biir loolu Musaa ne: «Aji Sax ji dafa santaane ne: “Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”»
33Musaa wax Aaróona ne ko: «Fabal ndab, def ci andaaru mànn, teg ko fi kanam Aji Sax ji, dencal ko seeni sët ak seeni sëtaat.»
34La Aji Sax ji santoon Musaa la Aaróona def, daldi koy teg ca kanam gaal gay def àlluway kóllëre ga, ñu denc ko fa.
35Bànni Israyil dunde nañu mànn diiru ñeent fukki at, ba kera ñu agsee réew mu ay nit dëkke, gannaaw ba ñu jéggee kemu réewum Kanaan.
36Ñu jàpp ne andaar, boo ci amee fukk, mooy benn efa.