Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba loolu amee nag Musaa ak bànni Israyil woy Aji Sax ji, màggal ko. Ña nga naan: «Ma woy Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe. Fas ak gawaram la fab, xalab géej.
2Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a; te mooy sama wall tey. Mooy sama Yàlla, ji may tagge, sama Yàllay maam, ji may joobe.
3«Aji Sax ji jàmbaari xare ji, Aji Sax jeey turam!
4Watiiri Firawnaaki xarekatam la fab sànni géej; ñeyi xareem ya labandoo ca géeju Barax ya,
5xóote ya boole sàng, ñu ne ca biir menteñ niw doj.
6«Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.
7Sa màggaay gu yéemee nërmeel say noon. Yaa yebal sa mer, mu ne jippét, xoyom leen ni boob.
8Nga wal sag noo, ndox ya tegloo, wal ma ne sàtt, jaloo jalu, ndoxi xóotey géej way deeŋ!
9«Noon baa nga naa: “Maay dàqe, dabe, lël alal ja, séddale séddu, ba xol sedd, ne saamar boset, teg leen loxo.”
10Waaye sa ngelaw nga wal, géej mëdd leen, ñu diigandoo ni beteex biir géej mbàmbulaan!
11«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
12Yaa tàllal sa ndijoor, suuf wonn leen.
13«Sa ngor nga jiitee mbooloo, mi nga jot, te sa kàttan nga leen di yóbboo ca sa kër gu sell.
14Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti,
15kilifay waa Edom jàq, njiiti Mowab di kat-kati, mboolem waa Kanaan tiit, ne yasar;
16tiitaangeek njàqaree ne milib ca seen kaw. Sa kàttan a tax ñu mel niw doj, ne yàcc, ba kera sa ñoñ jàll, Aji Sax ji, ba kera askan wa nga goreel, jàll,
17te yaa leen di sampi ca sa tund wa nga séddoo, fa nga waajal sa dëkkuwaay, Aji Sax ji, bérab bu sell ba nga sàkke sa loxol bopp, Boroom bi.
18Aji Sax jeey Buur, tey ak ëllëg ba fàww.»

19Ci kaw loolu fasi Firawna ànd ak watiiri xareem aki gawaram, tàbbi géej, Aji Sax ji delloo ndoxi géej ga ca seen kaw, bànni Israyil ñoom, jaare joor gu wow ca digg géej ga.
20Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin.
21Maryaamaa nga leen di dëbbeel, naa: «Woyleen Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe. Fas ak gawaram la fab, xalab géej.»
22Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox.
23Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde bérab ba Maara (mu firi Fu wex).
24Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?»
25Musaa woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji won ko dammitu bant, mu sànni ko ca ndox ma, ndox ma neex. Foofa la Aji Sax ji dogalal bànni Israyil ay sàrti yoon ak ndigal, te fa la leen nattoo itam.
26Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»
27Ci kaw loolu ñu dem ba Elim, fekk fa fukki bëti ndox ak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma. Ñu dal foofa ca wetu ndox ma.