Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 6

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»
2Yàlla dellu wax Musaa ne ko: «Man maay Aji Sax ji.
3Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.
4Te itam damaa fasoon ak ñoom kóllëre, ngir jox leen réewum Kanaan, réew ma ñu nekkoon ay doxandéem.
5Maa déggal sama bopp yuuxi bànni Israyil, gi waa Misra def ay jaam, te fàttewuma sama kóllëre ga.
6Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.
7Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.
8Maa leen di yóbbu ba ngeen dugg réew ma ma giñoon ne maa koy jox Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, te maa leen koy moomale, man Aji Sax ji.»
9Ba Musaa waxee loolu bànni Israyil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti.
10Aji Sax ji wax Musaa ne ko:
11«Demal wax Firawna buuru Misra, mu bàyyi bànni Israyil, ñu génn réewam.»
12Musaa tinu Aji Sax ji ne ko: «Waaw, ndegam bànni Israyil sax nanguwuñu maa déglu, nu ma Firawna di déggale, man mii tëlee wax?»
13Aji Sax ji nag wax ak Musaa ak Aaróona, jox leen ay ndigal ci mbirum bànni Israyil ak Firawna buuru Misra, ngir ñu yiwi bànni Israyil, ba ñu génn Misra.
14Bànni Israyil ya yilifoon seen kër baay, ñoo di: Góor ña Ruben, taawu Israyil, jur: Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. Ñooñoo sos làngi Ruben.
15Doomi Simeyon yu góor di Yemuwel ak Yamin ak Owàdd ak Yakin ak Sowar ak Sawul, mi ndeyam dib Kanaaneen. Ñooñoo sos làngi Simeyon.
16Doomi Lewi yu góor ñoo di Gerson ak Keyat ak Merari, ku nekk ak askanam. At ya Lewi dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137).
17Doomi Gerson yu góor ñoo di Libni ak Simey, ñook seeni làng.
18Doomi Keyat yu góor ñoo di Amram ak Isar ak Ebron ak Usyel; te at ya Keyat dund, téeméer la ak fanweer ak ñett (133).

19Doomi Merari yu góor ñoo di Maali ak Musi. Ñooñoo sos làngi Lewi ak seeni giir.
20Amram moo jël bàjjanam Yokebedd soxna, kooku am ak moom Aaróona ak Musaa. At, ya Amram dund, téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137).
21Doomi Isar yu góor ñoo di Kore ak Nefeg ak Sikkri.
22Doomi Usyel yu góor di Mikayel ak Elsafan ak Sitiri.
23Aaróona moo jël Eliseba doomu Aminadab, jigéenub Nason. Kooku am ak moom Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
24Doomi Kore yu góor ñoo di Asir ak Elkana ak Abiyasaf. Ñooñoo sos làngi Kore.
25Elasar doomu Aaróona moom, moo jël soxna kenn ca doomi Putiyel, kooku am ak moom Fineyas. Ñooñoo yilif seeni kër baay ca Leween ña, ku nekk sos làngam.
26Aaróona moomu nag, mook Musaa, la Aji Sax ji wax, ne leen: «Génneleen bànni Israyil Misra, kurél ci kaw kurél.»
27Ñoom ñooñu ñoo wax ak Firawna buuru Misra, ngir génne bànni Israyil Misra; du keneen ku dul Musaa ak Aaróona.
28Keroog ba Aji Sax ji waxee ak Musaa ca réewum Misra,
29da koo wax, ne ko: «Man maay Aji Sax ji. Nanga wax Firawna buuru Misra, li ma lay wax lépp.»
30Teewul Musaa tinu Aji Sax ji, ne ko: «Waaw, waaye man, damaa tëlee wax. Mbaa Firawna dina ma déggal yee?»