Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 17

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw loolu mbooloom bànni Israyil gépp bàyyikoo màndiŋu Ciin, di dox ak a taxaw, ci ndigalal Aji Sax ji. Ñu dem ba Refidim, dal fa. Foofa nag mbooloo ma amuñu woon ndox mu ñu naan.
2Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?»
3Mbooloo ma mar na fa, bay xultu ci kaw Musaa, naan: «Loo nu doon jële Misra nag, xanaa du boole nu rey ndax mar, nook sunuy doom ak sunuy gétt?»
4Ba mu ko defee Musaa woo Aji Sax ji wall, ne ko: «Nu may def ak mbooloo mii? Des na tuuti de, ñu dóor ma ay doj, ba ma dee.»
5Aji Sax ji ne Musaa «Àndal ak ñenn ci magi Israyil, nga jaar ci kanam mbooloo mi, yóbbaale yet, wa nga dóoroon ca dexu Niil ga. Ŋàbb ko ci sa loxo te dem.
6Man dinaa taxaw ci sa kanam ci doj woowu ca tundu Oreb. Dóoral ci doj wi, su ko defee ndox dina ci génne, mbooloo mi naan.» Musaa def noona ca kanam magi Israyil ña.
7Bérab boobu la Musaa wooye Maasa (mu firi Nattu). Mu wooye ko itam Meriba (mu firi ab Jote), ndax joteb bànni Israyil ba fa amoon, ak na ñu fa nattoo Aji Sax ji, naan: «Moo Aji Sax ji ndax mu ngi ci sunu biir, am déet?»
8Ba loolu weesee Amalegeen ña dikk, xareek bànni Israyil ca Refidim.
9Musaa ne Yosuwe: «Tànnal nu ay xarekat te nga dem xeex ak Amaleg. Ëllëg dinaa taxaw ca kaw tund wa, ŋàbb yetu Yàlla wi ci sama loxo.»
10Yosuwe def la ko Musaa wax, di xeex ak Amaleg. Musaa ak Aaróona ak Ur nag ànd yéeg ba ca kaw tund wa.
11Ci kaw loolu saa yu Musaa yékkatee loxoom, Israyil man, saa yu wàccee loxo ba, Amaleg man.
12Musaa nag mujj sonn ndax loxo yu toqi; ñu jël aw doj, tegal ko, mu toog ca, Aaróona ak Ur séq ko, ku ci nekk taawu benn loxo, loxoom ya ne sàtt taxaw, ba jant so.
13Ba mu ko defee Yosuwe duma Amaleg ak mbooloom, leel leen ñawkay saamar.
14Ba loolu amee Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Bindal lii xew cib téere, muy pàttli, te nga xamal Yosuwe ne ko, raafal laay def askanu Amaleg, ba ñu jeex tàkk, ba deesatu leen fàttliku fu asamaan tiim.»
15Musaa nag sàkk fa sarxalukaay, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya».
16Booba la wax ne, gannaaw loxoo ñemee xàcci, jëm ci ngànguney Aji Sax ji, Aji Sax ji dootu noppee xareek Amaleg ba fàww.