Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 37

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Besalel nag defare gaalu kóllëre gi dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll.
2Mu xoob ko wurusu ngalam biir ak biti, sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër.
3Mu daldi koy móolal ñeenti lami wurus ci ñeenti tànkam, ñaari lam ci genn wet gi, ñaar, wet gi ci des.
4Mu sàkk nag ay njàppuy bantu séng, xoob bu ci nekk wurus,
5daldi roof njàppu yi ci lami weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi.
6Ci kaw loolu mu sàkk kubeeru saraxu njotlaay gu wurusu ngalam, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll.
7Mu sàkk itam ñaari malaakay serub yu wurus. Liggéeyu tëgg bu jekk la def serub yi ci ñaari cati kubeer gi,
8cat lii ab serub, cat lee ab serub, mu móolaale serub yi ak ñaari cat yi, serub yi ànd ak kubeer gi, di benn.
9Serub yaa ngi tàllal seeni laaf, jëme kaw, yiire kubeer gi seeni laaf te janoo, seeni kanam jublook kubeer gi.
10Ci biir loolu Besalel sàkk taabalu bantu séng, guddaay bi di ñaari xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll.
11Mu xoob ko wurusu ngalam, defal ko ombu wurus bu ko wër.
12Mu defal ko it pegg bu ko wër bu tollu ci yaatuwaayu ñeenti baaraam, ba noppi sàkkal pegg bi ombu wurus, wëralee ko ko.
13Mu móolal taabal ji ñeenti lami wurus, daldi we lam yi ci ñeenti wet yi, fi fareek ñeenti tànk yi,
14lam yi dendeek pegg bi, di téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji.
15Mu sàkk ay njàppuy bantu séng, xoob ko wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji.
16Ci kaw loolu mu sàkk jumtukaay yiy tege ci taabal ji; ndabam yu tell yeek mbàttu yeek njaq yeek këll, yi ñuy tuural Yàlla, lépp di wurusu ngalam.
17Besalel sàkk itam tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Liggéeyu tëgg bu jekk la def tegukaayu làmp bi, ak taatu tegukaay bi, ak peru tegukaay bi, ay kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp ànd ak tegukaay bi, di benn.
18Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des.

19Ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd ñoo nekk ci benn car bi, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd nekk ci car bi ci topp, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car, yi soqikoo ci per bi, daj.
20Peru tegukaayu làmp bi itam am na ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram.
21Ab kàmbóot a ronu ñaari car, jàpp ci, beneen kàmbóot ronu ñaari car yi ci topp, jàpp ci, ab kàmbóot ronu ñaari car yi mujj, jàpp ci, juróom benni car, yi soqikoo ci weti per bi, daj.
22Kàmbóot yi ak car yi nag ànd ak tegukaay bi, di wenn donju wurusu ngalam wu ñu tëgg ba mu jekk.
23Mu sàkk juróom ñaari làmpam ak ay ñiimi feyukaayam ak ay andam, lépp di wurusu ngalam.
24Benn talaŋu wurusu ngalam, yemook fanweeri kilo, ci la sàkk tegukaayu làmp bi ak mboolem ay jumtukaayam.
25Ci kaw loolu Besalel sàkk ci bantu séng sarxalukaayu cuuraay bu kaare, guddaay bi di xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di ñaari xasab, ay béjjénam ànd ak moom di benn bant bi.
26Mu xoob ko wurusu ngalam ci kaw ak ci wet yi, ba mu daj, ak béjjén yi, daldi koy sàkkal wombu wurus bu ko wër.
27Ñaari noppi wurus la ko sàkkal ci ron kéméj gi, ci ñaari wetam, ñu jàkkaarloo, di téye banti njàppu, yi ñu koy yóbboo.
28Ci biir loolu mu sàkk ay njàppuy banti séng, xoob lu ci nekk wurus.
29Mu sàkk nag diwu pal gu sell gi, sàkk cuuraay lu xeeñ li raxul, def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax.