Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Mucc ga

Mucc ga 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Jenn waay ju bokk ci giirug Lewi nag moo jëloon janq bu mu bokkal giir.
2Ndaw sa ëmb, ba mujj am doom ju góor. Ba mu gisee taar, ba liir ba àndal, nëbb na ko lu mat ñetti weer.
3Mu dem nag, ba manatu koo nëbb. Mu wut pañe bu ñu ràbbe barax, fatte ko godoroŋ ak ndàbb, yeb ca liir ba, daldi dem, teg ko ca biir barax, ba ca tàkkal dex, ga ñu naan Niil.
4Xale bu jigéen bay magu liir ba ma nga taxaw fu soreyaatoo ak liir ba, di xool, ba xam nu muy mujje.
5Ba mu ko defee doomu Firawna ju jigéen dikk, di sangusi ca dexu Niil ga, surgaam yu jigéen yay doxantu ca tàkk ga. Ba loolu amee mu séen pañe ba ca biir barax ba, daldi yónni jaamam, mu yót ko ko.
6Naka la ko ne ubbet, yem ca xale ba, muy liir bu góor, xale bay jooy, yaram wa daw, mu ne: «Kii de ndeysaan, ci doomi Ebrë yi la!»
7Magu liir ba daldi wax doomu Firawna ja, ne ko: «Ndax ma dem wutali la ku koy nàmpal ci Ebrë yi?»
8Doomu Firawna ne ko: «Waaw, demal.» Xale ba dem, indil ko yaayu liir ba.
9Doomu Firawna ne ko: «Yóbbul xale bii te nàmpalal ma ko, maa lay fey.» Ndaw sa jël liir ba, di ko nàmpal.
10Ba xale ba màggee, mu yót ko doomu Firawna, mu def ko muy doomam, tudde ko Musaa (mu firi Ki ñu génne), ndax la mu ko génnee ca ndox ma.
11Ba ñu demee ba Musaa màgg, dafa am bés, mu seeti bokkam ya, gis leen ca liggéey yu metti, ya ñu leen sas. Mu gis jenn waayu Misra di dóor kenn ca bokki Ebrë ya.
12Musaa geestu wet gu nekk, gisul kenn, mu rey waa Misra ja, daldi gas, suul ko.
13Ca ëllëg sa mu dellu génn, yem ci ñaari Ebrë yuy xeex. Musaa wax ak ka tooñ, ne ko: «Lu tax ngay dóor sa moroom mii?»
14Waa ja ne ko: «Ku la def sunu njiit mbaa sunu àttekat? Xanaa danga maa nara rey, na nga reye woon waa Misra ja?» Musaa nag tiit, naan ca xelam: «Ndeke mbir mi kay siiw na.»
15Ba loolu amee Firawna dégg mbir ma, di wuta reylu Musaa. Musaa daw, ba sore Firawna, dem dali ca réewu Majan, fu dend ak ab teen.
16Yettro, sarxalkatu Majan ba nag, amoon na juróom ñaari doom yu jigéen. Ñu ñëw di rootsi, di duy mbalka, ya ñuy wëgge seen juru baay.
17Ay sàmm agsi, dàq leen. Musaa wallu jigéen ña, wëggal leen seen jur.
18Ba ñu delloo ca seen baay Ruwel, mu laaj leen ne leen: «Lu tax ngeen teela ñibbsi tey?»

19Ñu ne ko: «Ab waa Misra daal, moo nu xettli ca sàmm ya; rootal na nu sax, ba wëgg jur gi.»
20Ruwel ne leen: «Ana waa ja? Lu tax ngeen bàyyi ko fa? Wooyileen ko, mu añsi kay!»
21Musaa far dal ca kër waa ja. Mu mujj ko may doomam ju ñuy wax Sipora.
22Mu am doom ju góor, Musaa tudde ko Gersom (mu firi Doxandéem fii), ndaxte dafa ne: «Doxandéem laa fii.»
23Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.
24Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.
25Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen.