Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 1

Luug 1:55-75

Help us?
Click on verse(s) to share them!
55noonee mu ko dige woon sunuy maam, ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56Maryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57Gannaaw gi Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58Dëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59Ba bés ba délsee, ñu dikk xarfalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60Yaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61Ñu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62Ci kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63Sàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.
64Ca saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla.
65Ba loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp.
66Ña ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ngir manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
67Ci kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya feese Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee biral kàddug waxyu, ne:
68«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israyil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
69Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
70noonee mu ko waxe woon ca jant yu jëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottli,
71moo nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale.
72Moo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
73ak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, ba man koo jaamoo xel mu dal
75ci biir sellnga ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.

Read Luug 1Luug 1
Compare Luug 1:55-75Luug 1:55-75