Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu

Kàddu yu Xelu 20

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Naan biiñ ak ñaawle, naan ñoll, tanqale, ku mu nax xeluwoo.
2Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.
3Moytuw ay, ndam la; dof boo gis day bëgg xuloo.
4Ab yaafus du gàbb ba mu jotee, day wut am ngóob, du am dara.
5Mébétu jaambur day teen bu xóot, ku am ug dégg a cay root.
6Ñu baree ngi naa: «Gore naa,» waaye kuy boroom kóllëre dëgg?
7Ku jub, di jëfeg mat, doom ju la wuutu bég na.
8Su buur toogee di àtte, day gis, di ràññee mboolem ayib.
9Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
10Nattu diisaay yu yemul ak lu ni mel, Aji Sax ji bañ na ko.
11Gone sax day jëf, nga gis jikkoom; bu naree dëggu te jub, nga xam.
12Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
13Bul bëggi nelaw, ba ñàkk dab la; boo njaxlafee, lekk ba desal.
14Kuy waxaalee ngi naan: «Baaxul de!» Bu nee wërëñ, di damu naan: «Aka jar!»
15Wurus am na ak gànjar yu bare, waaye kàdduy xam-xam a gën per yu jafe.
16Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal jaambur.
17Njublaŋ, lekk, jëkke neex, mujj mel ni lancub suuf.
18Pexe, ndigal a koy lal; xare, ay tegtal.

19Kuy wër di jëw, wuññi sutura; ku réy làmmiñ, bul déeyook moom.
20Ku saaga sa ndey mbaa sa baay añe lëndëmu bàmmeel.
21Alal ju gaaw du mujje barkeel.
22Bul feyantook ku la tooñ; dénkul ci Aji Sax ji, mu wallu la.
23Aji Sax ji bañ na nattu diisaay yu wuute, njublaŋ ci natti diisaay baaxul.
24Jéegoy jaam Aji Sax jee ko yor, kenn xamul foo jëm.
25Bul gaawtuy digeek Yàlla, di dugal sa bopp; bul giñ, di réccu.
26Buur, bu xeloo, ràññee ku bon, mbugal ko, te du ko ñéeblu.
27Xelum nit làmp la bu Aji Sax ji taal, da koy niital ba ca biir xolam.
28Ngor ak worma day aar buur, ngor ay saxal ab jalam.
29Sagu ndaw, doole ja; gànjaru mag, bijjaaw ba.
30Dóor yu la gaañ faj na sag mbon, ay yar fóot na xolu boroom.