Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu

Kàddu yu Xelu 28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.
2Bu am réew dee fippu, kilifa ya bare; réew mu jàmm sax, kilifa gaa am déggin ak xam-xam.
3Ku ñàkk, su jekkoo ab ndóol, du ko bàyyil fepp, day mel ni waame.
4Ku wacc yoon, gërëm ku bon; ku wormaal yoon, jànkoonteek ku bon.
5Ku bon xamul njub, kuy wut Aji Sax ji, xam nga njub bu wér.
6Ñàkk te mat moo gën barele te dëng.
7Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.
8Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.
9Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
10Ku yóbbe bàkkaar nit kuy jubal, yeer ma nga gas, yaa cay tàbbi, waaye ku mat di jagoo ngëneel.
11Waay a ngi barele, defe ne xelu na; ku néewle am ug dégg, gis ne xeluwul.
12Bu ku jub amee ndam, mbégte mu réy la; ab soxor falu, ñépp làquji.
13Kuy làq say tooñ doo baaxle, ku koy nangu, tuub ko, am yërmandey Yàlla.
14Mbégte ñeel na ku saxoo ragal, waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.
15Kilifa guy soxore néew-ji-doole mook gaynde guy yëmmoo yem, mbaa rab wuy songe.
16Kilifa gu amul ug dégg, day foqati rekk, waaye ku bañ lu lewul, gudd fan.
17Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
18Mat, mucc; dëng, dàll daanu.

19Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan, ndóol ba doyal.
20Boroom worma, bare barke; ku yàkkamtee woomle, sa mbugal du jaas.
21Par-parloo baaxul, waaye dogu mburu moyloo na kilifa.
22Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.
23Boo artoo nit, mu baaxe la ëllëg; yaa koy gënal ku ko doon jay.
24Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
25Ku bëgge day sooke ay, te ku wóolu Aji Sax ji, woomle.
26Ku doyloo sam xel, dof nga; ku jëfe xel mu rafet, mucc nga.
27Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.
28Bu ab soxor faloo, ñépp làquji, bu daanoo, ku jub teg tànk.