1Lii waxi Agur la, góor gay doomu Yake mu Maasa. Góor ga daa wax ak Itiyel, wax ak Itiyel ak Ukal. Mu ne:
2Maa dofe dëgg, ba yées ci nit ñi, dég-dégu nit sax awma ko.
3Jànguma, ba am xel mu rafet, awma xam-xam ci Aji Sell ji.
4Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
5Lu Yàlla wax, mat na sëkk, mooy yiir ku ko làqoo.
6Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.
7Éy Yàlla, yaar laa la ñaan, ngalla may ma ko sama giiru dund:
8caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy;
9lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.
10Bul sikkal ab surga ca njaatigeem, da lay ñaan-yàlla, mu dal la.
11Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
12Ag maas a ngi defe ne set nañu, te taq ripp ak bàkkaar.
13Ag maas a ngi daŋŋiiral; aka ñoo mana xeeloo!
14Ag maas a ngi, seeni sell niy saamar, seeni gëñ niy paaka, ñuy lekk néew-ji-doole, ba raafal leen ci réew mi, ba ku ñàkk jeex ci biir nit ñi.
15Saxu watar du suur, ñaar ñu jigéen la am: Jox Ma ak Jox Ma. Ñett a ngii ñu dul suur, ba ci ñeent ñu dul ne doy na mukk:
16njaniiw, jigéen ju jaasir, suuf, du màndi ndox, sawara, du ne doy na mukk.
17Kuy xeelu sa baay, di siidee déggal sa ndey, baaxoñ génne ciw xur, luqi sa bët, tan ya lekk.
18Ñett a ngii, yéem na ma, ba ci ñeent yu ma xamul:
19yoonu jaxaay ci asamaan, yoonu jaan ci kawi doj, yoonu gaal ci diggu géej, yoon wi góor di jaar as ndaw.
20Jikkoy jigéenu moykat a ngi. Day lekk, wommiku, te naan: «Defuma dara lu aay!»
21Ñett a ngii, day yëngal suuf, ba ci ñeent yu suuf àttanul:
22jaam bu falu buur, dof bu regg,
23ndaw su bon su for jëkkër, jigéen ju wuutu sangam bu jigéen.
24Ñeent a ngii, di lu tuut ci kaw suuf, te am xel, yaroo xel:
25xorondom, néew na doole, waaye bu jotee, mu denc dundam;
26daman, barewul kàttan, te day dëkk ciy doj;
27soccet, amul buur, teewul ñuy àndandoo, diy gàngoor;
28sindax, manees na koo ŋëb, teewul ma nga biir kër buur.
29Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:
30gaynde, mooy buuru rab yi, ragalul kenn;
31séq daagu, jekk taxawaay, ab sikket, ak buur ci biiri dagam.
32Boo sàgganee bay tëggu, mbaa ngay mébét lu bon, nanga téye saw làmmiñ.
33Ndax ku ruux soow, am ca dax, ku wañaar bakkan, mu nàcc, te lu jógal xol, indiw ay.