Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu

Kàddu yu Xelu 18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ab siis, bànneexu boppam rekk, loo ko digal mu xalab.
2Ab dof wutul ag dégg, balaa caag muy jaay ag muus.
3Bu mbon nuyoo, xeebeel topp ca; jëf ju ñaaw, gàcce rekk.
4Waxi nit ndox mu xóot la, bu bënnee, xelli, ñu di ca xelu.
5Faral ku tooñ baaxul, bul xañ dëgg ku deful dara.
6Ab dof, làmmiñam sooke naw ay, ay waxam di sàkku yeti gannaaw.
7Ab dof, waxam a koy sànk, làmmiñu boppam a koy dugal.
8Waxi jëwkat di ñam wu neex wuy seey, jàll ca biir-a-biir.
9Kuy sàggane sa liggéey, yaak kuy yàq a bokk.
10Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
11Alal day aar boroom ni ab tata, mu xalaat ne maneesu koo bëtt.
12Bew, yàqule; jëkke woyof, mujje tedd.
13Tontu te déggagoo, ndof la, ak ñàkk kersa.
14Ku bëgga dund, dékku woppi yaram, waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.
15Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.
16Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.
17Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.
18Tegoo bant day feyu ay, di àtte boroom doole yu jote.

19Jubook mbokk moo tooñ, jéggi tataa ko gëna yomb, mbaa ubbi bunt yu tëje ràpp.
20Làmmiñ feesal na biiru boroom, yoolu kàddu suur na boroom.
21Dund ak dee a ngi ci làmmiñ, te wax garab la, ku ko bëgg, lekk ca doom ya.
22Ku am jabar, am nga ngëneel, am nga yiwu Aji Sax ji.
23Ku ñàkk a ngi leewaayu, boroom alal di ko jànni.
24Barey àndandoo lor a ngi ci, waaye xarit a ngi gëna taq nit mbokkam.