Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 26

JËF YA 26:24-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
24Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof, Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»
25Waaye Pool ne ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago.
26Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.
27Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne gëm nga.»
28Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgga dugale ci gaayi Kirist!»
29Pool ne ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»
30Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp.
31Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.»
32Te Agaripa ne Festus: «Manoon nanu koo yiwi, bu dénkuloon mbiram Sesaar.»

Read JËF YA 26JËF YA 26
Compare JËF YA 26:24-32JËF YA 26:24-32