1Bi juróomi fan wéyee, Anañas sarxalkat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.
2Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.
3Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.
4Waaye ngir baña yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.
5Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasareen.
6Dem na ba jéema teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.
8Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne li nu koy jiiñ dëgg la.»
9Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.
10Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.
11Man ngaa wóorliku ne ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.
12Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.
13Te manuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.
14Waaye nangu naa ci sa kanam ne maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne mooy tariixa; terewul ne lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.
15Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.
16Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
17«Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.
18Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.
19Waaye ay Yawut yu dëkk Asi —xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.
20Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,
21xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
22Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»
23Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
24Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak soxnaam Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.
25Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»
26Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko farala woolu, ngir waxtaan ak moom.
27Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.