1Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg.
2Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax.
3Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko.
4Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.
5Noonu mboolooy ñi gëm di gëna dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.
6Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.
7Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéema dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayu leen ko.
8Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.
9Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
10Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xibaaru jàmm bi.
11Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.
12Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it moomeelu Room. Nu toog fa ay fan.
13Bi bésub noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.
14Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.
15Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
16Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.
17Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.»
18Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu waññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.
19Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya.
20Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk,
21di xamle ay aada yu nu sañula nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»
22Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar.
23Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér.
24Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gëna ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.
25Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu.
26Ca saa sa suuf yëngu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbét ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne téll tijjiku.
27Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku. Mu daldi bocci jaaseem, bëgga xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw.
28Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.»
29Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanam Pool ak Silas, di lox.
30Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma wara def, ba mucc?»
31Ñu ne ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»
32Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.
33Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
34Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
35Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»
36Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen te dem ci jàmm.»
37Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanam ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgga sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
38Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit.
39Ñu ñëw nag di leen dëfal, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba.
40Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.