1Lii moo di doxi bànni Israyil, ba ñu génnee réewum Misra, def seeni gàngoor, ca njiital Musaa ak Aaróona.
2Musaa moo bind seeni dalukaay ak seen yoon ya ñu jaare, ci ndigalal Aji Sax ji. Lii moo di seeni jaar-jaar, ak seeni dalukaay:
3Fa Ramses lañu bàyyikoo, fukki fan ak juróomu weer wi jëkk ci at mi. Keroog bés ba topp ca bésub Mucc ba, ca la bànni Israyil daagu, génn, waa Misra gépp di gis.
4Booba waa Misraa ngay rob ña Aji Sax ji fàdd ca ñoom, néewi mboolem seen taaw ya. Aji Sax jee mbugale noonu seen yàlla ya.
5Bànni Israyil nag jóge Ramses, dali Sukkóot.
6Ñu jóge Sukkóot, dali Etam ga ca catu màndiŋ ma.
7Ba ñu bàyyikoo Etam, dañoo walbatiku ba Pi Axirot ga janook Baal Cefon, daldi dal fa kanam Migadol.
8Ñu jóge Pi Axirot, jàll géej ga, wuti màndiŋ ma. Dox nañu yoonu ñetti fan ca biir màndiŋu Etam, doora dal Maara.
9Ñu jóge Maara, dem ba Elim, Elim ga ca fukki bëti ndox yaak ñaar, ak juróom ñaar fukki garabi tàndarma ya. Ñu dal foofa.
10Ba ñu jógee Elim, fa feggook géeju Barax ya la ñu dali.
11Ñu bawoo géeju Barax ya, dali ca màndiŋu Ciin,
12bawooti màndiŋu Ciin, dali Dofka,
13bawooti Dofka, dali Alus.
14Ba ñu bàyyikoo Alus, Refidim lañu dali. Foofa nag mbooloo ma amuñu fa ndox mu ñu naan.
15Ñu bàyyikoo Refidim, dali ca màndiŋu Sinayi,
16bàyyikoo màndiŋu Sinayi, dali Kibbrot Taawa,
17bàyyikooti Kibbrot Taawa, dali Aserot.
18Ba ñu jógee Aserot, Ritma lañu dali.
19Ñu jóge Ritma, dali Rimon Peres,
20jóge Rimon Peres, dali Libna,
21jógeeti Libna, dali Risa.
22Ba ñu bawoo Risa, Keyelata lañu dali.
23Ñu bawoo Keyelata, dali tundu Sefer,
24bawoo tundu Sefer, dali Arada,
25bawooti Arada, dali Makeyelot.
26Naka lañu bàyyikoo Makeyelot, dali Tayat,
27bàyyikoo Tayat, dali Tera,
28bàyyikooti Tera, dali Mitka.
29Ba ñu jógee Mitka, Asmona lañu dali.
30Ñu jóge Asmona, dali Moserot;
31jóge Moserot, dali Bene Yaakan,
32jógeeti Bene Yaakan, dali Xor Gitgaat.
33Ba ñu bawoo Xor Gitgaat, Yotbata lañu dali.
34Ñu bawoo Yotbata, dali Abrona,
35bawoo Abrona, dali Esiyon Geber,
36bawooti Esiyon Geber, dali Kades ca màndiŋu Ciin.
37Ba ñu bàyyikoo Kades, ca tundu Or wa digalook réewum Edom lañu dali.
38Ba mu ko defee Aaróona sarxalkat ba yéeg ca kaw tundu Or, ci ndigalal Aji Sax ji. Mu daldi faatu foofa, ca ñeent fukkeelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee réewum Misra, yemook benn fanu juróomeelu weeru at ma.
39Aaróona mu ngi woon ci téeméeri atam, ak ñaar fukk at ñett (123) ba mu faatoo ca kaw tundu Or.
40Ci kaw loolu Kanaaneen ba, buurub Arat, ba dëkke woon bëj-saalumu réewum Kanaan, daldi yég ne bànni Israyil a ngay dikk.
41Ba ñu jógee tundu Or, Calmona lañu dali.
42Ñu jóge Calmona, dali Punon,
43jóge Punon, dali Obot,
44jógeeti Obot, dali Yee Abarim, ga digalook réewum Mowab.
45Ba ñu jógee Yee Abarim, Dibon Gàdd lañu dali.
46Ñu jóge Dibon Gàdd, dali Almon Diblatayim,
47jógeeti Almon Diblatayim, dali ca tundi Abarim, janook tundu Nebo.
48Ba ñu bawoo tundi Abarim, ca joori Mowab lañu dali, ca wetu dexu Yurdan, janook Yeriko.
49Wetu dexu Yurdan, ga ca diggante Bet Yesimot ak Abel Sitim, ca joori Mowab, fa lañu dale.
50Ba loolu amee Aji Sax ji waxati ak Musaa ca joori Mowab, ca wetu dexu Yurdan, ga janook Yeriko. Mu ne ko:
51«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dugg réewum Kanaan,
52nangeen dàq waa réew mépp, nangeen yàqte seen mboolem tuur yu ñu yett, te seen mboolem jëmm yu ñu móol, yàqteleen ko, seen mboolem bérabi jaamookaay it, tasleen ko.
53Defleen réew mi moomeel, ngeen dëkke ko, ndax yeen laa jox réew mi, ngir ngeen moom ko.
54Tegooleen bant réew mi, séddoo ko ci seeni làng. Làng gu gëna mag, na am cér bu gëna mag, làng gu gëna tuut, am cér bu gëna tuut. Fépp fu tegoo bant génneel ag làng, ñooy doon boroom. Ci seen biir giiri maam ngeen di séddu.
55Waaye su ngeen dàqul waa réew mi, ña ngeen fa bàyyi ñooy mujj diy dég yu leen di luqi, aki dagg yuy cuut seeni wet. Ñoo leen di lëjal witt ca biir réew mooma ngeen sance.
56Su boobaa nag na ma naroona def seen noon yooyu, yeen laa koy def.»