Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma

Màndiŋ ma 8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji waxati Musaa ne ko,
2mu wax Aaróona, ne ko: «Buy teg làmp yi, fa féete tegukaayu làmp ba kanam, fa la juróom ñaari làmp ya wara niite.»
3Noonu la Aaróona def. Fa féete tegukaay ba kanam, fa la féetale ay làmpam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.
4Tegukaayu làmp bi nag, ni ñu ko liggéeye nii la. Wurus lañu ko tëgge ba mu jekk, dale ko ci tànk bi, ba ci mbar mi. Noonee ko Aji Sax ji wone woon Musaa, na lañu liggéeye tegukaayu làmp ba.
5Aji Sax ji waxati Musaa ne ko,
6«Nanga jële Leween ñi ci biir bànni Israyil te nga setluloo leen.
7Ni ngay def ngir setluloo leen nii la: Danga leen di wis ndoxum setlu, ba noppi ñu wat seen yaram wépp, fóot seeni yére, daldi set.
8Su ko defee ñu jël aw yëkk wu ndaw, booleek saraxu peppam, di sunguf su mucc ayib su ñu xiiwaale ag diw, ak weneen yëkk wu ndaw wooy jël ngir saraxu póotum bàkkaar.
9Indil Leween ñi ci kanam xaymab ndaje mi, te nga dajale mbooloom bànni Israyil mépp.
10Boo indee Leween ñi fi kanam Aji Sax ji, bànni Israyil daldi teg seeni loxo ci kaw Leween ñi.
11Su ko defee Aaróona taxawal Leween ñi taxawaayu saraxu yékkati-jébbal fi kanam Aji Sax ji, muy sarax bu bawoo ci bànni Israyil, Leween ñi daldi sasoo di liggéey liggéeyu Aji Sax ji.
12Leween ñi ñoom, nañu teg seeni loxo ci kaw boppi yëkk yi, ñu def wenn wi saraxu póotum bàkkaar, te def wi ci des ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir njotlaayal Leween ñi.
13Gannaaw loolu ngay taxawal Leween ñi fi kanam Aaróona ak doomam yu góor, daldi leen def saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji.
14Noonu ngay seppee Leween ñi ci biir bànni Israyil, Leween ñi doon sama cér.
15Gannaaw loolu la Leween ñiy doora dugg ci liggéeyu xaymab ndaje mi. Danga leen di jëkka setluloo, ba noppi def leen saraxu yékkati-jébbal.
16Ñoom déy lañu ma sédda sédd ci biir bànni Israyil, ñu wuutu mboolem luy ubbiteg njur, di taawi mboolem bànni Israyil. Maa leen sédd sama bopp.
17Ndax man maa séddoo mboolem taaw ci biir bànni Israyil, nit ak mala. Keroog ba ma fàddee mboolem taaw ca réewum Misra, ca laa leen sellalal sama bopp.
18«Maa jël Leween ñi, weccikoo leen bépp taaw ci biir bànni Israyil,

19te itam maa jukkee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen yékkati, jox leen Aaróona aki doomam, ngir ñu liggéey liggéeyu bànni Israyil ci wàllu xaymab ndaje mi, di defal bànni Israyil seenug njotlaay, ngir bu bànni Israyil jegee bérab bu sell bi it, du tax menn mbas am ci seen biir.»
20Ba loolu amee Musaa ak Aaróona ak mbooloom bànni Israyil mépp daldi defal Leween ñi noonu. Mboolem lu Aji Sax ji santoon Musaa ci Leween ñi, noona la ko bànni Israyil defe ak ñoom.
21Leween ñi setlu, fóot seeni yére, Aaróona def leen ni saraxu yékkati-jébbal, ñeel Aji Sax ji. Mu defal leen nag seen njotlaay ngir setal leen.
22Gannaaw loolu Leween ñi doora liggéeyi seen liggéey ci wàllu xaymab ndaje mi, ci kilifteefu Aaróona aki doomam. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa ci Leween ñi, na lañu def ak ñoom.
23Aji Sax ji waxati Musaa, ne:
24«Lii nag moo war ci Leween ñi: ku ci am ñaar fukki at ak juróom, jëm kaw, yelloo naa bokk ci kurél, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war.
25Waaye ku xasa am juróom fukki at, na génn kurél gi boobu liggéey war, te bumu ca liggéeyati.
26Sañ naa jàpple bokki Leweenam ñi dénkoo dénkaaney xaymab ndaje mi, waaye dootu ci liggéey lenn. Noonu ngay def ak Leween ñi, ci seen wàlli dénkaane.»