Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Timote

1.Timote 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wax ju wóor a ngii: kuy sàkku sasub jiite mbooloom gëmkat ñi, liggéey bu rafet lay xëccu.
2Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.
3Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.
4Kërug boppam nag, na ko yor yorin wu rafet, te na mana yar ay doomam ba ñu nangul ko te sédd ko cér bu mat sëkk.
5Ndax ku tëlee yor kërug boppam, ana nu mu mana sàmme mbooloom gëmkati Yàlla yi?
6Te it bumu dib tuubeen bu bees, lu ko moy ag réy-réylu man na koo gëlëmal, ba mu tàbbi ci mbugal ni Seytaane.
7Te it ñi ci biti te gëmuñu, la ñu ko seedeel nay lu rafet, ba deram du yàqu, nde kon mu tàbbi ci fiiru Seytaane.
8Naka noonu ab taxawukatub mbooloo mi, na di ku tedd, bumu di boroom ñaari kàddu. Bumu di ku sàngara jiital, mbaa kuy sàkku am-am bu lewul.
9Na ŋoy ci mbóotum ngëm mii feeñ te ànd ceek xel mu dal.
10Dees koy jëkka seetlu nag, ba muy ku mucc sikk, ñu door koo dugal ci liggéeyu taxawukatub mbooloo mi.
11Naka noonu, na jigéen ñiy taxawu mbooloo mi di ñu tedd, buñu diy soskat, nañu moom seen bakkan, te jara wóolu ci lépp.
12Ab taxawukatu mbooloo mi bumu denc lu wees jenn jabar te na yor ay doomam, ak këram, yorin wu rafet.
13Ñi ci wàccoo ak seen sasub taxawukat nag, seenub liggéey lañu jënde taxawaay bu rafet, te ñooy mana waxe fit, seen ngëm gi ñu gëm Almasi Yeesu.
14Lii laa lay bind, te di la yaakaara seetsi ci fan yu gàtt,
15ngir su ma yeexee itam, nga xam nooy doxale ci kër Yàlla, ci biir mbooloom Yàlla jiy dund. Mbooloom gëmkat mi mooy kenug dëgg gi, di cëslaayam.
16Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.