Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Timote

1.Timote 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu, ci ndigalal Yàlla sunu Musalkat, ak Almasi Yeesu sunu yaakaar, ci man la bataaxal bii bawoo,
2ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.
3Na ma la ko dénke woon ba may dem diiwaanu Maseduwan rekk, nanga toog Efes googu, ngir ña fay jàngle leneen, nga aaye leen.
4Ne leen ñu baña topp léebi neen, ak limi maam yu dul jeex, ndax loolu ay werante doŋŋ lay jur, te jariñul dara ci liggéeyu njotug Yàlla gi sottee ci ngëm.
5Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal.
6Am na ñu moy woowu yoon, ba lajj jëm ci wax ju tekkiwul dara.
7Ñooñu ay jànglekati yoonu Musaa lañuy xëccoo doon, te xamuñu li ñuy wax, bay xam lenn ci li ñuy dëggal.
8Xam nanu nag ne yoonu Musaa baax na, ndegam na mu ware lees ko jëfe.
9Lii itam xam nanu ko: ñi jub taxuñu yoon wi jóg, xanaa ñi jubadi ak ñi déggadi, ak ñemekati Yàlla yi, ak bàkkaarkat yi, ak ñi wormaalul lu sell, ak ñi wormaalul Yàlla, ak bóomkati baay, ak bóomkati ndey, ak reykati nit ñi,
10ak fokati séy yi, ak góor-jigéen yi, ak jàppkati jaam yi, ak fen-kat yi, ak giñkati fen yi, ak ñiy jëfe leneen lu woroo ak njàngle mu baax,
11mi dëppoo ak xibaaru jàmm bi ñu ma dénk, xibaaru Yàlla Aji Tedd ju màgg ji.
12Damay sant sunu Boroom Almasi Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi,
13te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bundxatalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.
14Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi, ak cofeel, gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.
15Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!
16Waaye loolu moo tax man bàkkaarkat bi ci raw, ma dajeek yërmande, ngir, ci lépp lu nu Almasi Yeesu di muñal, ma doon ci misaal, ñeel ñi ko nara gëm ëllëg, ba texe ba fàww.
17Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!
18Kon nag Timote doom, loolu mooy ndigal li ma la dénk, te mu dëppook kàdduy waxyu yi jotoona jib te jëm ci sa mbir. Gànnaayool kàddu yooyu ngir di ci xaree xare bu baax bi,

19te nga saxoo ngëm ak xel mu dal. Am na ñu tanqamlu seen ndéeyum xel ba suuxal seen ngëm.
20Ci ñooñu la Imene ak Alegsàndar bokk; Seytaane laa leen jébbal, yare leen ko, ngir ñu bañatee saaga Yàlla.