Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Timote

1.Timote 2

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kon nag li jiitu ci mboolem li may dénkaane mooy ngeen di dagaan, di ñaan, di tinu ak a sant, ñeel doom aadama yépp,
2ñeel buur yi, ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal, tey wéye gépp njullite, ak wépp dundin wu tedd.
3Loolu moo rafet te neex Yàlla sunu Musalkat,
4bi bëgg ñépp mucc te ràññee liy dëgg.
5Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn Defarekat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy nit ki Almasi Yeesu,
6mi maye bakkanam ngir jot ñépp, te jëf jooju lañu seedeele ca ba mu jotee, la Yàlla nammoon.
7Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat, ak ndawal kàddu gi, ak itam ab sëriñ, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.
8Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo.
9Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw, gu teggine te yem. Buñu jiital di defaroo ay létt yu ëpp, ak gànjari wurus, aki per, ak yérey tànnéef,
10waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ragalkati Yàlla.
11Te it bu ñuy jàngle, na jigéen ñiy noppi, te woyof toyy.
12Mayuma jigéen mu jàngle mbaa mu jiite góor, waaye na noppi.
13Ndax kat Aadama lañu jëkka bind, Awa topp ca.
14Te it du Aadama lañu nax, waaye jigéen lañu nax ba mu xëtt ndigal.
15Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm, ak cofeel, ak jëfin wu sell te yem.