Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Timote

1.Timote 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane,
2yu leen ay jinigalkat, ay fenkat yu dërkiis ab xol, di naxe.
3Ñooñu ñooy aaye ab séy, di digle ñàkka lekk yenn ñam yu Yàlla sàkk, ngir gëmkat ñi xam liy dëgg, man cee jariñu te di ko sante Yàlla.
4Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees ko jariñoo.
5Lu mu mana doon, kàddug Yàlla akug ñaan moo koy sellal.
6Soo dee xamal loolu bokki gëmkat ñi, yaa di jawriñu Almasi Yeesu ju baax ju xontoo kàdduy yoonu ngëm wi, ak àlluwa ju rafet ji nga topp naka jekk.
7Waaye nettali yu yittewoo lu dul Yàlla, ak léebi jeeg ju màggat ji, bañ ko, te nga tàggatu ci ag njullite.
8Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.
9Kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm ba mu mat sëkk.
10Loolu kat moo nu tax di sonn aka góor-góorlu, ndax Yàlla jiy dund lanu yaakaar, moom miy musal ñépp, rawatina gëmkat ñi.
11Digleel loolu, te di ko jàngle.
12Bu la kenn xeebe sa at yu néew, waaye nanga doon royukaayu gëmkat ñi ci wax ak jëfin, ak cofeel, ak ngëm, ak dundin wu set.
13Ba keroog may dikk, saxool di jàng-biral Mbind mi, di ñaaxe aka jàngle.
14Bul sàggane may gi ci yaw, te di lu ñu la baaxee ag kàddug waxyu gu ànd ak tegeb loxo, ba la mag ñi defaloon.
15Loolu ngay def sam xel, mbir yooyu ngay pastéefoo ba sag yokkute bir ñépp.
16Sàmmal sa bopp nag, sàmm sa àlluwa, te saxoo ko; soo ko defee, dinga mucc, musal ñi lay déglu.