Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 5

Luug 5:29-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29Ci kaw loolu Lewi waajalal ko bernde ju réy ca këram. Mbooloo mu bare teew, ay juutikat ak yeneen gan, ñu bokk toog, di lekk.
30Farisen yi ak seeni firikat nag di xultu ci kaw taalibey Yeesu yi, ne leen: «Lu tax ngeen di lekkandoo ak a naanandoo ak juutikat yeek bàkkaarkat yi?»
31Yeesu ne leen: «Du ñi wér ñoo soxla fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla.
32Du ñi jub nag laa woosi, bàkkaarkat yi laay woo, ngir jëme leen cig tuubeel.»
33Dañoo wax Yeesu, ne ko: «Taalibey Yaxya de, dinañu faral di woor, di julli. Farisen yi it noonu, waaye sa ñoñ, lekk ak a naan lañu wéye.»
34Yeesu ne leen: «Ndax man ngeena woorloo ay gan ñu wàlli ag céet, li feek boroom séet biy teew ci seen biir?
35Waaye ay bés a ngi ñëw, dees na jële boroom séet bi ci seen biir. Kera bés yooyu nag, dinañu woor.»
36Yeesu léebati leen, ne leen: «Mbubb mu bees, deesu ci xotti ab sekkit, ngir daaxe ko mbubb mu ràpp. Lu ko moy mbubb mu bees mi xottiku ba noppi, te du tax sekkit wu bees wi ànd ak mbubb mi ràpp.
37Te it mbuus yu ràpp, deesu ci duy biiñ bu bees. Lu ko moy biiñ bu bees bi fàcc mbuus yi; biiñ bi tuuru, mbuus yi yàqu.
38Biiñ bu bees daal, ci mbuus mu bees lees koy denc.
39Te itam deesul naan biiñ bu yàgg, di bëggati bu bees, xanaa nga ne: “Bu yàgg bee baax.”»

Read Luug 5Luug 5
Compare Luug 5:29-39Luug 5:29-39