Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 3

LUUG 3:19-28

Help us?
Click on verse(s) to share them!
19Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
20ba faf tëj Yaxya kaso.
21Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
22Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
23Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi. Te Yuusufa mooy doomu Eli,
24miy doomu Matat. Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
26Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
27Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
28Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.

Read LUUG 3LUUG 3
Compare LUUG 3:19-28LUUG 3:19-28