Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 3:19-28 in Wolof

Help us?

LUUG 3:19-28 in Téereb Injiil

19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
20 ba faf tëj Yaxya kaso.
21 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
22 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
23 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi. Te Yuusufa mooy doomu Eli,
24 miy doomu Matat. Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
26 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
27 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
28 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.
LUUG 3 in Téereb Injiil

Luug 3:19-28 in Kàddug Yàlla gi

19 Erodd boroom diiwaan ba nag, Yaxya sikkoon na ko ndax Erojàdd jabaru magam ja mu nekkaloon, ak mboolem yeneen ñaawtéef yu Erodd def.
20 Mu tegati leneen ca loolu lépp: jàpp Yaxya, tëj ca kaso ba.
21 Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku.
22 Ba loolu amee Noo gu Sell gi moo bindoo ni pitax, wàcc ci kawam, baat jibe asamaan, ne: «Yaa di sama Doom, sama soppe; yaa may bànneexal.»
23 Yeesu ci boppam ba muy door, amoon na lu tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa, ni ko xel mana jàppe. Yuusufa, Eli mooy baayam,
24 Eli, Matat. Matat, Lewi; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 Yuusufa, Matacas; Matacas, Amos; Amos, Nawum; Nawum, Esli; Esli, Nagayi.
26 Nagayi, Maat; Maat, Matacas; Matacas, Semeyin; Semeyin, Yoseg; Yoseg, Yoda.
27 Yoda, Yowanan; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel; Sorobabel, Selcel; Selcel, Neri;
28 Neri, Melki; Melki, Adi; Adi, Kosam; Kosam, Elmadam; Elmadam, Er.
Luug 3 in Kàddug Yàlla gi