Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - YOWAANA - YOWAANA 1

YOWAANA 1:2-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga.
3Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom.
4Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.
5Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.
6Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya.
7Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm.
8Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.
9Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.
10Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko.
11Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.
12Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.
13Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.
14Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
15Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
16Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni yoon.
17Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.
18Kenn masula gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.
19Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay sarxalkat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan.
20Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne moom du Almasi bi.
21Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi wara ñëw?» Mu ne leen: «Déedéet.»
22Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu mana tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»
23Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
24Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya.
25Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Ilyaas, doo Yonent bi wara ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?»
26Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.
27Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»
28Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
29Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina.
30Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”
31Xawma woon kooku kan la waroona doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.
33Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
34Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne moom moo di Doomu Yàlla ji.»
35Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.
36Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!»
37Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.
38Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu ne ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi».
39Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.
40Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.
41Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist».

Read YOWAANA 1YOWAANA 1
Compare YOWAANA 1:2-41YOWAANA 1:2-41