Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 127

Sabóor 127:1-5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan. Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul, ku ko tabax, neen nga doñ-doñi. Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul, ku ko wattu, neen nga teewlu.
2Neen it la nit di teela jóg ak a guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.
3Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la.
4Doom joo jure ndaw, mooy fitt ci loxol jàmbaar;
5ndokklee ku ci mbuusam fees, ba bu ñu taseek ub noon ca pénc ma, duñu am gàcce mukk.

Read Sabóor 127Sabóor 127
Compare Sabóor 127:1-5Sabóor 127:1-5