Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 7

Luug 7:5-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5ndax ku sopp sunuw xeet la, te sunu jàngu bi sax, moo nu ko tabaxal.»
6Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
7Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér.
8Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.»
10Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
11La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
20Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis.
22Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.

Read Luug 7Luug 7
Compare Luug 7:5-29Luug 7:5-29