Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 7:5-29 in Wolof

Help us?

LUUG 7:5-29 in Téereb Injiil

5 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.»
6 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgga agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër.
7 Looloo tax it ma xalaat ne awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, masuma cee gis ku gëme nii.»
10 Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.
11 Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.
13 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»
14 Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»
15 Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.
16 Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
17 La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
19 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroona ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
22 Noonu mu wax ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent.
27 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
29 Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.
LUUG 7 in Téereb Injiil

Luug 7:5-29 in Kàddug Yàlla gi

5 ndax ku sopp sunuw xeet la, te sunu jàngu bi sax, moo nu ko tabaxal.»
6 Yeesu daldi ànd ak ñoom. Naka la jubsi kër ga, njiit la yóbbante ay xaritam kàddoom, ñu gatandu Yeesu, ne ko: «Sang bi, jarul ngay sonn, ndax sab tànk sama biir kër, man yeyoowuma ko.
7 Moo ma la tee gatandul sama bopp, ndax jàpp naa ne loolu jomb na ma. Waxal genn kàddu rekk, sama surga wér.
8 Ndax man ci sama bopp ci kilifteef laa tënku, te man itam ay takk-der a ngi ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Ma ne kee: “Ñëwal,” mu ñëw. Te sama jaam bu ma ne: “Defal lii,” mu def ko.»
9 Ba Yeesu déggee loolu daa yéemu ca njiit la. Mu ne gees mbooloo ma topp ca moom, ne leen: «Dama ne, gii ngëm gu réy, bànni Israyil sax, gisuma ko ci.»
10 Ndaw ya daldi dellu ca kër ga, fekk jaam ba wér.
11 La ca tegu Yeesu demati dëkk bu ñuy wax Nayin, ay taalibeem ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12 Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.
13 Sang bi nag gis ko, ñeewante ko, ne ko: «Bul jooy.»
14 Mu dikk ba teg loxoom ca jaat ga, ña ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Ngóor si, yaw laay wax, jógal.»
15 Néew ba jóg toog, di wax, mu delloo ko yaay ja.
16 Tiitaange nag jàpp ñépp, ñu sàbbaal Yàlla, naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir!» te naan «Yàllaa wallusi ñoñam!»
17 Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18 Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19 yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
20 Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21 Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis.
22 Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23 Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24 Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25 Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26 Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27 Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28 Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29 Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.
Luug 7 in Kàddug Yàlla gi