Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 7

LUUG 7:5-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.»
6Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgga agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër.
7Looloo tax it ma xalaat ne awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, masuma cee gis ku gëme nii.»
10Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.
11Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.
13Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»
14Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»
15Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.
16Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
17La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
18Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
19yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
20Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroona ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
22Noonu mu wax ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi.
23Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
26Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent.
27Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
29Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.

Read LUUG 7LUUG 7
Compare LUUG 7:5-29LUUG 7:5-29