40Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.
41Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
42Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
44Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég.
45Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
46Noonu Maryaama daldi ne:
47«Sama xol a ngi màggal Boroom bi, sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48ndaxte fàttaliku na ma, man jaamam bu woyof bi. Gannaaw-si-tey, niti jamono yépp dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy. Turam dafa sell.
50Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal, ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom, te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52daaneel boroom doole yi ci seen nguur, yékkati baadoolo yi.
53Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex, te dàq boroom alal yi, ñu daw ak loxoy neen.
54Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,