Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare

Kàdduy Waare 7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Jëw bu rafet a gën diw gu xeeñ, bésub dee a gën bésub juddu.
2Dem dëj a gën wàlli bernde, mooy muju képp. Kuy dund, sóoraale ko.
3Naqar a gën xaxaloo; aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.
4Ku xelu, xalaat kërug dëj; ku dofe, xalaat kërug puukare.
5Déglu ku xelu di la àrtu moo gën déglu dof bu lay woy.
6Ab dof day textexi ni dég yuy retete taal bu cin tege. Loolu it di cóolóoli neen.
7Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
9Bul gaawa mer; mer, xolub dof la samp këram.
10Bul ne lu tax démb dàq tey, loolu, laaj ko du xel.
11Xel mu rafet daa neex ni ndono, njariñ la ci kuy dund.
12Xel mu rafet kiiraay la, xaalis kiiraay la; njariñu xam-xam mooy xelu, mucc.
13Xoolal ci li Yàlla def: Ana ku mana jubbanti lu mu dëngal?
14Su neexee, bànneexul; su mettee, xoolal ne lu ci ne, Yàllaa ko def ngir jaam bi umple gannaawam.
15Lu ne laa gis ci sama dund gu gàtt gii! Nit a ngii jub, teewu koo sànkook njubam; nit bon, ànd ak mbonam, gudd fan.
16Bul jub ba mu ëpp, bul wóolu sam xel ba mu ëpp, lu ko moy nga yàqule.
17Bu la mbon jiital, te bul dofe. Jàppool lii, te baña wacc lee, mooy li gën, lu ko moy nga dee te sa àpp jotul. Ku ragal Yàlla kat sàmm yooyu yaar.
19Xel mu rafet day dooleel boroom, ba mu man fukki kàngam cib dëkk.

20Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.
21Te it du lépp lu ñu wax, ngay bàyyi xel. Kon doo dégg surga bu la ŋàññ,
22ndax xam nga xéll ne yaw it ŋàññe nga ay yooni yoon.
23Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet, te naan: «Naa xelu,» ndeke mbir ma sore na ma.
24Li wara am daa loq, te xóota xóot; ana ku ko mana daj?
25Ma walbatiku, di jéema xam, di wut, di càmbar, di sàkkum piri, ngir xam li bon cig ndof, ak li dofe, cig ndof.
26Ma seetlu lenn lu gëna naqari dee: muy ndaw su la fiir. Kooku cofeelam mbaal la, yoxo ya dib jéng. Ku Yàlla gërëm a koy rëcc, bàkkaarkat bi lay jàpp.
27Waarekat ba nee: Xoolal li ma gis, benn-bennal ko, ngir gis lu mu firi.
28Ma seeta seet, gisuma. Genn góor laa ràññee ci junniy góor, ràññeewuma kenn ci jigéen ñi ñépp.
29Lenn daal laa ràññee: Yàlla daa sàkk nit, jubal ko, nit di wuta sél fu ne.