Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare

Kàdduy Waare 9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Loolu lépp laa walbatiku xalaat, ngir lépp leer ma: Ku jub ak ku xelu ak seeni jëf, lépp a ngi ci loxol Yàlla. Mbëggeel ak mbañeel, xamoo lu la ciy xaar, lépp a nga ca kanam.
2Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.
3Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
6Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
7Kon doxal, lekk saw ñam, bége, te naan sa biiñ ci xol bu sedd. Yàlla kat nangul na la jeeg say jëf.
8Foo tollu, solul ba jekk, te bul fàttee xeeñlu.
9Bànneexul yaak ndaw si nga sopp ci fan wu gàtt wi la Yàlla may fi suuf, ndax loolu nga séddoo ci fan wu gàtt wii ngay doñ-doñaale fi kaw dun bi.
10Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.
11Ma seetlooti fi kaw suuf ne du ku gaaw, yaay raw; du ku jàmbaare, yaa moom xare; du ku xelu, am loo dunde; du ku muus, duunle; du kuy xamkat, amu yiw; ku nekk ak bésam ak wërsëgam.
12Doom aadama la bésu safaan bay bett, jekki ne dàll fi kawam, ni jën wu keppu cib caax, loru, mbaa picc mu tancu cig fiir. Doom aadama xamul bésam.
13Lii it gis naa ko, muy lu ma yéem, di mbirum xel mu rafet fi kaw suuf.
14Ab dëkk bu ndaw la woon, nit ña néew. Buur bu mag song dëkk ba, gaw ko, jal jali suuf yu mag, sësal ca tata ja.
15Fekk fa ku néewle te xelu. Mu manoona xelal dëkk ba, xettli leen, waaye kenn faalewu ko.
16Man dama noon xel mu rafet a gën doole! Ndeke ku néewle ñu xeeb la, tanqamlu say wax.
17Ku xelu, kàddoom yu dégtu ndànk moo gën ŋal-ŋalu kilifa ci biir ñu dofe.
18Xel mu rafet a gën ngànnaayi xare, waaye benn bàkkaarkat day yàq ngëneel lu réy.