Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare

Kàdduy Waare 10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1As weñ tàbbi ci diw gu xeeñ, yàq ko; ab dof it jëfam su tuut neenal na xel mu rafet ak daraja.
2Xelu, jubal; dofe, jàdd.
3Te it ku dofe buy dox sax, du ànd ak xelam; ku ko gis, xam ne kii dof la.
4Su la sa kilifa meree, bul jóge fa ñu la teg; tooñ yu mag, teey ba giif.
5Lu mettee ngi lu ma gis fi kaw suuf, lu mel ni njuumte lu rëcc kilifa:
6Ab dof bu ñu jox cér yu bare, boroom daraja féete suuf;
7ma gis baadoolo war fas, kilifa di rung ni baadoolo.
8Ku gas um yeer, repp nga tàbbi ca; ku bëtt miir, repp jaan matt la;
9kuy yett ay doj, repp nga caa gaañu; kuy gor bant, repp nga caa loru.
10Liggéeye weñ gu day te xacceesu ko, góor-góorlu war na ca; xelu, baaxle jariñoo.
11Jaan màtte, balees koo jat, du njariñal jatkat ba.
12Ku xelu àddu, mu diw yiw; ku dofe wax, sànku.
13Bu jëkkee wax ju amul bopp, daaneele ndof gu sotti.
14Ab dof a ngi waxa wax, te kenn xamul luy xew ëllëg. Ana ku koy xamal gannaawam?
15Ab dof ak kër-këreem, coonoy neen; du xam sax yoonu taax ya.
16Ngalla yeen, réew mi gone falu buur, jawriñ ña di xëye xawaare.
17Ndokklee, yeen, réew ma as gor falu, te bu jotee, jawriñ ñay xéewlu, ngir am doole te baña màndi.
18Tayel, puj bu màbb; yaafus, néeg buy senn.

19Aw ñam bégal, aw ñoll bànneexal, xaalis tontu lu ne.
20Sam xel sax bu ca saaga buur, sa néegu biir sax, bu fa saagaa boroom daraja. Xamoo picc muy yóbbu sa kàddu, mbaa njanaaw luy siiwali mbir ma.