Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare

Kàdduy Waare 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Bul gaaw làmmiñ, bul gaawa dikke Yàlla mbir. Yàllaa ngi kaw asamaan, yaw yaa ngi fi suuf. Kon na say kàddu néew.
2Bu xalaat baree, indi gént; bu wax baree, waxi dof jib.
3Boo digook Yàlla, bu ko yeexe; Daray foontukat neexul, defal li nga dige.
4Baña digee gën dige loo deful.
5Bu la sa làmmiñ yóbbe bàkkaar, ba ngay lay ndawal Yàlla la, naan lii njuumte la woon. Ana lu jar Yàlla di la meree sa kàddu, bay neenal saw ñaq?
6Wax ju bare, caaxaani neen; mook gént yu baree yem. Kon, Yàlla, ragal ko.
7Boo gisee ñuy not néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
8Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
9Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
10Bu koom yokkoo, lekk-kat yi yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
11Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du nopplu, du nelaw.
12Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: Alal ju boroom dajale ba loru,
13mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
14Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
15Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
16Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
17Lii daal laa ci gis, man. Li gën te jaadu ci nit: Na lekk, naan te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf giiru dund gi ko Yàlla may. Loolu mooy céram.
18Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.

19Yàllaa koy bànneexal, ba du tiisoo ay fanam.