Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Yowel

Yowel 1

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kàddug Aji Sax jii moo dikkal Yowel doomu Petuwel.
2Dégluleen, yeen mag ñi, teewluleen, yeen waa réew mi ñépp. Ndax lii mas naa am ci seeni jant, mbaa seen janti maam?
3Waxleen ko seen doom yi ngeen jur, doom yi ngeen jur wax ko doom yi ñu jur, doom yi ñu jur wax ko geneen maas.
4Ndesu soccet yi la njéeréer yi lekk, ndesu njéeréer yi, seenu tostan lekk, seen ndesu tostan, salleer yi lekk.
5Màndikat yee, yewwuleen, jooyoo. Naan-kati biiñ yee, jooyleen biiñ bu bees, bi ñu foqatee ci seen gémmiñ.
6Aw xeet a dal ci samam réew, am kàttan, wees ab lim, seeni sell di selli gaynde gu góor, seeni ŋaam di ŋaami gaynde gu jigéen.
7Samag reseñ lañu fóom, samag figg lañu xasa xas, ba mu set, ñu sànni, car ya weex tàll.
8Neeleen wóoy ni janq bu woddoob saaku, di ko ñaawloo jëkkëram, ja ñu ko dencaloon ba muy lu tuut.
9Saraxu pepp ak saraxu tuuru dagg na ca kër Aji Sax ji. Sarxalkat yi, boroom dénkaaney Aji Sax ji, ñu ngi ñaawlu.
10Tool yi yàqu yaxeet, suuf sëngéem ciw tiis; pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.
11Yeen beykat yi, rusleen; boroom tóokëri reseñ yi, yuuxooleen, ndax peppum bele baak lors ba, nde ngóob mi sànku na.
12Ag reseñ wow, figg lax, gërënaat, tiir, ak pom, mboolem garabi tool, wow koŋŋ. Mbég daal a rasu doom aadama.
13Yeen sarxalkat yi, gembuleen te tiislu, yeen ñi dénkoo sarxalukaay bi, yuuxuleen, yeen boroom dénkaaney sama Yàlla, dikkleen, sol ay saaku yu ngeen fanaanoo, ngir toroxlu, nde xañees na seen kërug Yàlla ga saraxu pepp ak saraxu tuuru!
14Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.
15Céy, bii bés! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa Aji Man ji lay dikke.
16Xanaa du ag lekk a dagg, nuy gis, te mbég ak bànneex tukkee sunu kër Yàlla ga?
17Aw jiwu wow na, suule ciy donji suuf, dencukaay yi wéet, sàq yi dàjjiku, am pepp wow.
18Céy ni mala yiy binnee! Gétti nag yaa ngi jànnaxe, ndax ñàkk parlu, gàtt yi itam loof.

19Yaw Aji Sax ji laay woo, sawara moo lekk parluy àll bi; ag daay a xoyom garabi àll bi yépp.
20Rabi àll yeet ñu ngi àppaat, jublook yaw, nde wali ndox yee ŋiis, te sawara xoyom parluy àll bi.