5Mu ñaan mucc, nga saxal jalam fàww,
6sag wall a ko sagala sagal! Teddngaak daraja nga ko sédd,
7jagleel ko barke bu sax dàkk, bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
8Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
9Buur, yaa naan sa noon yépp céex, ne say bañ taral.
10Soo nee jalañ, jafal, ñu boy. Aji Sax ji mer, sànk leen, sawara xoyom leen.
11Yaay raafal seeni giir fi kaw suuf, fey seen askan ci doom aadama yi.
12Ñoo la mébal lu bon, nasal la pexe, joyul.
13Nga di leen diir fittu kanam, ñu wone gannaaw.