Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ruut

Ruut 4

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci biir loolu Bowas dem ba ca bunt dëkk ba, toog fa. Noonu rekk mbokk ma mu waxoon ne su dee jotaat, moo ko ci gëna yey, daldi fay jaare. Mu woo ko ne ko: «Diwoo, kaay fii, toog tuuti.» Mu dikk, toog.
2Bowas woo fukki magi dëkk ba, ne leen: «Toogleen.» Ñu toog.
3Mu wax ak mbokk ma yeyoo sañ-sañu jotaat ba, ne ko: «Ab làccu suuf bu sunu mbokk Elimeleg moomoon la, Nawmi di ko jaay. Mooy ka jóge réewum Mowab, ñibbsi.
4Man nag dama noon war naa la koo yegge, te laaj la ndax danga koy jënd ci kanam magi dëkk bi ak ñi fi toog. Soo bëggee def sa warugaru jotaat, jëndal. Soo buggul, wax ma, ma xam. Ndax kat kenn gënu la cee yey, te maa topp ci yaw.» Mu ne ko: «Damay jënd kay!»
5Mu ne ko: «Ãa bés boo jëndee suuf si ci Nawmi nag, yaay denc Ruut ndawas Mowabeen, sa doon soxnas ndem-si-yàlla si, ndax nga mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal.»
6Mu ne: «Kon de duma mana def sama warugar, ndax sama alal a ciy yàqoo. Fabal boog sama sañ-sañu jotaat, ndax duma ko mana jariñoo.»
7Booba Israyil, jamono yu jëkk yooya, mbirum njëndum jotaat mbaa ag weccoo, la ñu ko baaxoo dogale ci diggante nit ak moroom ma, nii la: kii day summi dàllam, jox kee. Noonu lees daan yoonale ag jëflante ca Israyil.
8Moo tax ba boroom sañ-sañu jotaat ba waxee Bowas, ne ko: «Jënd ko yaw,» dafa daldi summi dàllam, dogale ko mbir ma.
9Ba mu ko defee Bowas wax ak mag ña ak ñeneen ña ñépp, ne leen: «Seedeleen bésub tey ne jënd naa ci Nawmi mboolem alalu Elimeleg ak mboolem alalu Kilyon ak Malon,
10boole ci Ruut, ndawas Mowab, sa doon soxnas Malon, muy sama soxna. Su ko defee ma mana lawal askanam, ba du fey, boole ci sàmmal leen seen alal, ba turu Elimeleg du réer ci biiri bokkam te du raaf ci limeefu dëkk bi. Yeena ko seede bésub tey jii.»
11Waa pénc ma mépp ak mag ña nag ne ko: «Noo ko seede. Yal na Aji Sax ji def ndaw siy séysi sa kër, mel ni Rasel ak Leya, ñoom ñaar ñi giir waa kër Israyil gépp. Yal nanga tekki ci digg Efrata te amu tur ci Betleyem.
12Njaboot gu la Aji Sax jiy may ci ndaw sii, yal na ñu lawal saw askan, ba mu mel ni askanu Peres, ma Tamar am ak Yuda.»
13Ba mu ko defee Bowas jël Ruut. Gannaaw gi mu dëkkoo ko; Aji Sax ji may ko mu ëmb, ba mujj am doom ju góor.
14Jigéen ña ne Nawmi: «Sant Aji Sax ji, moom mi la xañul mbokk mu la jotaat nii tey! Yal na xale bi di ku amu tur ci Israyil gépp.
15Dina la leqli, dimbali la keroog ba ngay mag, ndax sa goro bi la bëgg te dàqal la juróom ñaari doom yu góor, moo ko jur.»
16Nawmi nag fab xale bi, taf ko ci dënnam. Gannaaw loolu moo ko doon topptoo.
17Jigéeni gox ba nag naa: «Waay waay Nawmi am na doom ju góor!» Ñu tudde xale bi Obedd. Obedd moo jur Yese, miy baayu Daawuda.
18Kon lii mooy askanu Peres ci wàllu geño: Peres moo jur Esron,

19Esron, Ram; Ram, Aminadab;
20Aminadab, Nason; Nason, Salma;
21Salma, Bowas; Bowas, Obedd;
22Obedd, Yese; Yese, Daawuda.