Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax jaa ngii di tas àddina, tasaare ko, salfaañe li fi dénd bi, wasaare ñi ko dëkke:
2sarxalkat beek baadoolo bi, sang akub jaam, njaatige lu jigéen ak ab janqam, jaaykat ak jëndkat, ablekat ak àbbkat, leblekat ak lebkat.
3Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral, dees koo futti ba mu ne furaas! Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!
4Suuf a ngi wowa wow, ne sereŋ, àddina ne làcc, ne sereŋ, kàngami xeeti àddina ne làcc.
5Suuf si la ñi ko dëkke sobeel, ñoo wàcc yoon yi, xëtt ndigal, fecci kóllëre gi sax dàkk.
6Moo tax alkànde yàq suuf, ñi ko dëkke gàddu àq ji. Moo tax waa àddina raaf, ba ñi des di lu néew.
7Biiñ ñàkk na, garabu reseñ lax, bépp xol bu tooyoon, binni.
8Tabala ju xumb selaw na, ña daa xaxaloo dal, mbégtem buumi xalam dakk.
9Kenn naanatul, di woy, ñoll wex na ka koy naan.
10Dëkk bu gental tasaaroo na, kër yépp tëje, kenn duggul.
11Mbedd maa ngi soowaloo, ndax biiñ bu ñàkk, gépp mbégte fey, bànneexu àddina dëddu.
12Tojiti neen a des ci dëkk bi, bunt ba rajaxoo.
13Noonu lay deme ci àddina, ci biir xeet yi, mbete benn-benni doomi oliw gu ñu gësëm, mbaa doomi reseñ yu des ca ndey ja, gannaaw bu ñu wittee ba sottal.
14Ña ngay xaacu di sarxolle, waa sowu di sàbbaal ci màggug Aji Sax ji.
15Yeen waa penku, sargal-leen Aji Sax ji boog, yeen waa duni géej, teral-leen Aji Sax ji Yàllay Israyil.
16Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa: «Teddnga ñeel na Aji Jub ji!» Waaye man dama ne: «Jeexle naa! Jeexle naa, wóoy man! Workat yaa ngi wora wor, ba far làggi ci wor.»
17Yeen waa àddina, kat-kat, pax akub caax dëgmal na leen.
18Nga déggi yuux, daw, tàbbi biir pax, génne pax, laawoob caax. Mbàndi kaw kat ubbi na, kenug àddina di reng-rengi.

19Suuf daa loroo loru, fetta fett, salfaañoo salfaañu.
20Suuf a ngi janga jang ni màndikat, ba joy ni mbaar, moyam diis ko gann, mu daanu te du jógati.
21Bu bésub keroogee Aji Sax ji dikke mbugal gàngoor ya fa kawa kaw, ak buuri àddina yi fi suuf.
22Dees leen di boole denc cim pax, ne leen ràpp tëj, ba mu am ay fani fan, ñu mbugal leen.
23Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.