Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 5

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Naa woy sama soppe woyu cofeel wu solowoo tóokëram. Sama soppee fi amoon tóokër, kaw tund wu suuf sa nangu lool.
2Mu gàbb ko, dindi doj ya, jëmbat ca ngëneeli reseñ, tabax tóojub doj fa digg ba, ba yett ca mbalkam nalukaayu reseñ, tey yaakaar reseñ ju neex, mu meññ, wex.
3Léegi yeen waa Yerusalem ak yeen waa Yuda, ngalla àtteleen maak sama tóokër.
4Lu may defalati sama tóokër bi, lu ma ca defuloon? Lu waral ma di ko yaakaare reseñ ju neex, mu meññ, wex xàtt?
5Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.
6Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.
7Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.
8Wóoy ngalla ñii di dajale kër ak kër, tool akub tool, aakimoo fépp, ba des ñoomu neen ci réew mi.
9Maa dégg Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ne: «Giñ naa ne kër yu bareey gental déy, kër yu yaa, rafet, kenn dëkku ca.
10Tóokërub ñetti egtaar déy du meññ juróom fukki liitari biiñ, te jiwum téeméeri kiloy bele it, fukki kilo doŋŋ a cay génne.»
11Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.
12Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, biiñ xelli ca xawaare ja. Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, xooluñu li mu jo loxoom.
13Moo tax ñoñi Aji Sax ji di duggi ngàllo ndax ñàkk xam-xam. Seen kàngam ay deeye xiif, seen baadoolo deeye mar.
14Moo tax njaniiw di yàkkli ag bóli, gémmiñ ga ne ŋafeet, amul kersa, boroom darajaak baadoolay Yerusalem doon xaxaloo, far tàbbi ca.
15Doom aadama torox na, nit detteelu na, ku doon regeju, detteelu.
16Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ab àtteem lay fésale màggaayam, Yàlla ju sell ji, ag njekkam lay firndeele sellngaam.
17Am xar a nara fore biir dëkk bi, mbetem parlu, màngaan lekke gentub boroom alal.
18Wóoy ngalla ñiy ràngooy buum, di diri ñaawtéefi neen, ràngooy goj di diri seeni tooñ.

19Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»
20Wóoy ngalla ñiy gis lu bon, ne lu baax la; gis lu baax, ne lu bon la; lëndëm, ñu tudde leer, leer, ñu tudde lëndëm; lu wex, ñu ne neex na lu neex, ñu ne wex na.
21Wóoy ngalla ñii defe ne ñoo xam, yaakaar ne ñoo muus.
22Wóoy ngalla ñiy jàmbaari naan biiñ, diy ndaanaan ci njafaanu ñoll,
23di dëggal ku sikk ndax ab ger, tey xañ boroom njekk, ag njekkam.
24Moo tax ni boob di jeexe ci sawara, ngooñ xoyomoo ko cib taal, ni la seenub reen di seeye ni lu maxe, seeni tóor-tóor naaw ni pënd. Ñoo gàntal yoonu Aji Sax ji ci gàngoor yi, ñoo sofental kàddug Aji Sell ju Israyil.
25Moo tax merum Aji Sax ji tàkkal ñoñam, mu xàcci loxoom, duma leen, ba tund yi jaayu, seeni néew wetar ni mbalit fi mbedd yi. Loolu yépp taxul mu meddi, loxoom baa ngi mu xàcci ba tey.
26Aji Sax jeey yékkatil raaya, xeet wu sore, wal ug liit, wooye leen fa cati àddina, ñu jekki ne jaas, dikkal leen.
27Kenn sonnu ci, kenn tërëfu ci, kenn dajjantul mbaa muy nelaw; ngañaay yolomul, waruw dàll dogul.
28Seeni fitt ñaw na, seen xala yépp noppi na, seen wewi tànki fas ni xeer. Bu tànki watiir ya dawee, nga defe ne callweer a.
29Dañuy ŋar ni gaynde, ŋarati ni gaynde gu mat; yëmmu, ŋank um rëbbam, yóbbu te kenn du wallu.
30Bésub keroog ñu ŋaral Yuda, ŋar yu mel ni géej gu sàmbaraax! Foo geesu ci réew mi, xool, doo gis lu moy lëndëm ak njàqare, xàmbaar maase, ba leer giim.