Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Jant yooyu Esekiya moo woppoon, bay waaja dee. Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc dikk, ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Dénkaaneel sa mbiri kër, ndax dangay dee, doo jóg!”»
2Esekiya nag walbatiku, jublook miir ba, ñaan ci Aji Sax ji.
3Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.
4Ci kaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Esayi, ne ko:
5«Doxal ba ca Esekiya, nga ne ko: Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: “Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di yokk ci saw fan fukki at ak juróom.
6Buurub Asiri ak dooleem, maa la ciy xettli, yaw ak dëkk bii, te maay aar dëkk bii.”»
7Lii nag ngay def ab takk bu bawoo ci Aji Sax ji, di firndeel ne Aji Sax ji dina def li mu wax:
8Maa ngii di delloo ker gi gannaaw lu tollook fukki dëggastal, ya jant bi wàccoon ca kaw iskaleb Axas. Ci kaw loolu jant bi dellu gannaaw lu tollook fukki dëggastal ya mu jotoona wàcc.
9Mbind mii nag Esekiya buurub Yuda moo ko bindoon, gannaaw ba mu tëddee wopp, ba jóg:
10Man de dama noon: «Sama digg doole laay deme jaare bunti njaniiw, sama ndesu fan réer ma!»
11Ma noon: «Dootuma gisati Aji Sax ji, duma gisati Aji Sax ji fi kërug àddina. Duma tegati doom aadama bët, dootu fii ci waa àddina.
12Sama dëkkuwaay lañu sempi, yóbbu fu sore, mbete xaymab sàmm. Sama àpp a taxañe, ni ndimo lu ab ràbb doge ca mbaam ma. Diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma.
13May xalaat, ba bët set; Aji Sax jiy dammat samay yax ni gaynde, diggante bëccëg ak guddi, nga jekkli ma.
14May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, di binni nim xati, di séentu kaw ba saay gët giim. Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, dimbali ma.»
15Waaye lu may waxati? Aji Sax jee ma wax, te moo jëf. Kon, ma temp ndànk sama giiru dund ndax tiisu xol.
16Boroom bi, ci sa kàddook sa jëf la nit di dunde te ci laay noyyee ba tey. Yaa ma wéral, may ma, ma dund.
17Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
18Njaniiw du la sant, ndee du la gërëm, te ku tàbbim pax yaakaaratul sa kóllëre.

19Kiy dund, kiy dund doŋŋ mooy ki lay sant ni man bésub tey jii, te baay mooy xamal doom sa kóllëre.
20Aji Sax ji yaa may wallu, nu di la woy, ànd aki xalam, sunu giiru dund, fa sa biir kër, yaw Aji Sax ji.
21Fekk na Esayi noon: «Indileen ab danku figg, ngeen jonj ko ci taabu Esekiya bi, kon dina dund,»
22ba Esekiya noon ko: «Ana lu di takk biy firndeel ne dinaa wér, ba dellooti kër Aji Sax ji?»