Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wóoy ngalla Aryelee, Aryel, dëkk ba Daawuda dale. Dundleen at ak at, amal-leen ci màggal ci kaw màggal.
2Du tee ma wàcceel Aryel musiba, ñuy yuuxook a jooyoo. Yerusalem ay mel ci man ni Aryel, taalub sarxalukaay.
3Maay dal ub dal, wër la, gawe la ay tata, jali jal, fuuge la.
4Dinga suufe ba mel ni kuy àddoo biir suuf, sa baat di ndéey lu dégtoo xóote ya pëndub suuf lale, mel ni njuuma lu waxam bawoo biir suuf, baatam yeloo xóote ya pëndub suuf lale.
5Say noon ay def gàngoor ni feppi suuf, di naaxu nit ñu néeg, ñu ngelaw liy wal nib cox. Loolooy jekki am, ca saa sa.
6Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi moo lay dikke dënook suuf su yëngu ak riir mu réy, ngelaw riddi, di ngëlén, ànd ak sawara wuy xoyome.
7Mboolem xeet yu bare yiy xareek Aryel, di song dëkk beeki tataam, nar leena torxal, ñoom ñépp ay mel ni gént mbaa njeneeru guddi!
8Su boobaa mu mel ni ku xiif, géntul lu moy di lekk, yewwu rekk, biir ba wéet; mbaa ku mar, géntul lu moy di naan, yewwu rekk, loof, put ga wow koŋŋ. Noonu la gàngooru xeet yépp di nekke, mboolem xeet yooyuy xaareji fa Siyoŋ!
9Tendeefal, jommi rekk! Gëmm, gumba rekk. Ñiika màndi te du biiñ, ñuy jang te duw ñoll!
10Aji Sax ji déy yeen la wal ngelawal nelaw yu xóot, taf seeni gët, te ngeen di yonent yi; muur seeni bopp te ngeen di boroom peeñu yi.
11Peeñum xew-xew yii yépp ump na leen, ni leen kàdduy téere bu ñu tay umpe. Boo ko joxee ku jàng, ne ko mu jàng ko, mu ne la manu ko, nde dees koo tay;
12nga jox ko ku jàngul, ne ko mu jàng, mu ne la manula jàng.
13Boroom bi nee: «Askan wii, làmmiñ lañu ma jegee, lori neen lañu may wormaale, te seen xol sore ma. Seen ragal ak man it, njàngum tari kepp la.
14Moo tax maa ngii di dellu wéyeek askan wii, ay kéemtaan aki kiraama yuy tiiñ boroom xel ak xelam, réer xamkat ak xam-xamam.»
15Wóoy ngalla ñiy làqu Aji Sax ji, di loqal seen mébét, ba lëndëm muur seen jëf, ñu naan: «Ana ku nu gis? Ana ku nu yég?»
16Yeenaka juunum xel! Dees na jaawale tabaxkatu njaq beek ban bi? Ndax li ñu sàkk dina ne ki ko sàkk: «Kii sàkku ma»? Am njaq leey waxtaane tabaxkat bi naa: «Kii manula tabax»?
17Xamuleen ne fi leek lu néewa néew, àllub Libaŋ sopplikub tóokër, tóokër bi walbatiku meññ, ba ñu ne ab gott la?
18Su bés baa ab tëx dégg kàdduy téere, silmaxa tàggook lëndëm, di gis,

19néew-doole yi dellu bége Aji Sax ji, ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israyil.
20Ku néeg déy dina neen, kuy ñaawle sànku, te képp kuy yeeru nu mu defe lu bon, dees na la dagg.
21Mooy ñiy tuumaal nit, di fiir ab àttekat ca pénc ma, di àtte ñàkkal nit ku jub ci dara.
22Moo tax Aji Sax, ji jotoon Ibraayma, wax ak waa kër Yanqóoba, ne leen: «Léegi Yanqóoba du rusati, du amati yaraanga.»
23Bu am meññeefam gisee li sama loxo def fi seen biir, dinañu sellal sama tur, sellal ma, man Aji Sell ju Yanqóoba. Dinañu ma wormaal, man Yàllay Israyil,
24ba ñi réeroon, mujj xam; ñurumtukat yi dégg ndigal.