Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 8

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Gannaaw gi Aji Sax ji ne ma: «Jëlal àlluwa ju mag, ak xalima gu jàppandi, nga bind ci lii: “Maxer Salal Xas Bas”, (mu firi Sëxëtoo këfit foqet).»
2Ma wut ci seede, won àlluwa ja ñaar ñu mat seede: ñuy Uri sarxalkat ba, ak Sàkkaryaa doomu Yeberekiya.
3Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.”
4Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»
5Aji Sax ji dellu ne ma:
6«Gannaaw askan wee teddadil ndoxum Silowe, mi ci wal mu teey mi, di bége Reccin ak doomu Remalya,
7Boroom baa ngii di leen sottisi dexu Efraat gi ne xéew ak dooleem, te mooy buurub Asiri ak mboolem darajaam. Dex gi mooy génn xuram, fees fépp fu dig tàkkam,
8wal-wali jàll Yuda, mbënn ma wal, taañaañal, yéeg ba tollu ko ci put, firiku niy laaf ba dajal sam réew, yaw Emanuwel.»
9Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
10Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!
11Aji Sax ji moo wax ak man, ba mu ma nee nikk, àrtu ma, ngir ma baña roy askan wii. Mu ne ma:
12«Bul tudde wor, lenn lu askan wii tudde wor; lu ñu ragal it, bu ko ragal, bu ko tiit.
13Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal ngay sellal, moom ngay ragal, moom ngay tiit.
14Mu doon seen bérab bu sell, di doj wuy fakktale, xeer wuy féle, ci ñaari këri Israyil, te dim yeer, dig fiir, ñeel ku dëkk Yerusalem.
15Ñu baree cay tërëf, daanoo njaaxaanaay, damm, mbaa ñu sërëx, keppu.»
16Dencal seede bii, jëlal lii ndigal, tay cib tayu, dénk ko samay dongo.
17Maa ngi séentu Aji Sax ji, mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, waaye maa ngi koy yaakaar.
18Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

19Am na ñu naan: «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»
20Kon waxleen ne leen: «Ayca, ca ndigali yoon ya, ak seedey kàdduy waxyu ya. Kuy wax googu kàddu, ag leer fenkalu la.»
21Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, boole njàqareek ub xiif, te bu ñu xiifee, ñéññ, téen, xool kaw, saaga seen buur, saaga Yàlla,
22dellu xool fi suuf, yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare, sóoboo guddi gu fatt taraj.
23Waaye lëndëm googu du sax ci réew mii jàq tey. Démb Aji Sax ji torxal na réewum Sabulon ak mu Neftali, waaye ëllëg mu teral waa foofa, dale ko diiwaanu tefesu géej, ba ca wàllaa dexu Yurdan, boole ca sax Galile ga ca doxandéem ya.