Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 63

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»
2Lu waral sa xonqaayu mbubb mi, sa yére yi mel ni ku doon dëre dërukaayu reseñ?
3«Maa doon dëre tànk, man kenn ci ab dërukaayu reseñ, xeet yépp kenn dërlewu ma ci. Sama mer laa leen dëre, samam sànj laa leen dëggaatee, seen deret tis ci samay yére, ma taqal sama yére yépp.
4Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.
5Ma xool, gisuma ku ma dimbali, ma tiislu li ma amul ku ma jàpple. Ca la ma sama përëg wallu, samam sànj jàpple ma ca.
6Sama mer laa dëggaatee ay xeet, samam sànj laa leen màndal, sotti seen deret fi suuf.»
7Jëfi ngoru Aji Sax ji laay fàttlee ak cant gi Aji Sax ji yelloo, ngir li nu Aji Sax ji defal lépp; mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israyil, defal leen ko ci yërmandeem, ak jëfi ngoram gu réy.
8Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a! Ñee di doom yu dul tas yaakaar.» Mu daldi doon seen jotkat.
9Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.
10Waaye ñoom ñoo fippu, di naqaral xelam mu sell, mu soppliku seen noon, ba mujj di xareek ñoom.
11Ñoñam ña daldi fàttliku janti Musaa ya woon. Ña nga naan: «Ana ki jàlle woon Israyil géej, mook sàmmi géttam ga? Ana ki yebaloon noowam gu sell ci seen biir?
12Ana ki dawaloon dooley përëgam bu tedd ba, ñeel ndijooru Musaa, xaral leen ndox ma, ba ame ca woy wu sax dàkk?
13Ana ku leen doxloo woon biir xóote ya, ñu mel ni fasi naari góor ci biir màndiŋ, te tërëfuñu?
14Ni jur gu wàccew xur, di fa fore, ni la leen Noowug Aji Sax ji maye ab dal-lukaay. Noonu nga wommate sa ñoñ, ba ame ca woy wu rafet.
15«Ngalla séentool asamaan, xooleel fa sa kër gu sell ga ne ràññ. Ana sa fiiraangeek sa njàmbaar? Sag rafet xol ak sa yërmande ñooru na ma!
16Yaw déy yaa di sunu Baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israyil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”
17Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon, di nu dërkiisal, ba ragalatunu la? Sang bi, délsil ngir nun, sa giir yii nga séddoo.
18Nun sa xeet wu sell wii, moomunu réew mi lu yàgg, te noon yi dëggaate nañu sa bérab bu sell.

19Nu ngi mel ni xeet woo masula yilif, xeet wu ñu masula tudde sa tur. Éy soo xaroon asamaan, wàcc, ba tund yi yëngu fi sa kanam!»