Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yéeneb bii ñeel na Babilon, muy peeñum Esayi doomu Amocc.
2Yéegeleen ab raaya kaw tund wu ne duŋŋ, joorleen ñii, tàllal-leen loxo, ñu jàlle bunti kàngam yi.
3Maa jox ndigal ñi ma beral sama bopp, maa woo sama jàmbaar ñiy réy-réylu, ne leen ñu sottal mbugal mi samam sànj laaj.
4Coowal mbooloo ngoog ca tund ya, mel ni ñu baree bare! Riirum nguuri nguur yu daje, di xeeti xeet! Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy dajale gàngooru xare.
5Mooy bawoo fu sore, fa asamaan digalook suuf. Aji Sax ji laak gàngoor gi muy mbugale, ngir yàqtesi réew mi mépp.
6Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.
7Moo tax yoxoo yoxo yoqi, xoloo xol jeex,
8ñu tiita tiit, yaram di fuddook a metti, ñuy baddaañu ni kuy matu; ku ne jàq, di xulli sa moroom, kanam ya sël-sëleendoo.
9Bésub Aji Sax jaa ngii di ñëw, bés bu néeg, bésub mer ak sànj muy tàkk, nara gental suuf, te bàkkaarkat ya la fay fàkkas.
10Biddiiw mbaa dëllooñ dootu leeral; jant ay fenke lëndëm, weer dakkal leeram.
11Maay delloo àddina mbonam, yool ku bon tooñam, maay sàggi sagub ku reew, detteel puukarey ku néeg.
12Maay def nit gëna jafee gis wurus, ba doom aadama raw wurusu Ofir.
13Moo tax maay gësëm asamaan, suuf yëngoo fa mu tege ndax sànjum Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, keroog ba meram di tàkk.
14Ku nekk ay fekkiy bokkam, rawi cam réewam, mbete kéwél gu ñuy rëbb, mbaa xar mu amul sàmm.
15Ku ñu ci gis, jam la, ku ñu jàpp, saamar rey la;
16seeni doom, ñu moxoñe fi seen kanam, seeni kër, ñu sëxëtoo, seeni jabar, ñu tëdde.
17Maa ngii di xabtal fi seen kaw waa Medd, ñi xintewoowul xaalis, faalewuñu wurus.
18Seeni fitt lañuy rajaxee xalelu góor, duñu ñeewante gone, duñu xool tuut-tànk gëti yërmande.

19Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
20Deesatu fa dëkk, xanaa gental ba fàww. Màngaan dootu fa samp xayma, sàmm dootu fa gooral.
21Ay rabi àll a fay goore, kër ya fees aki looy, bànjóoli dëkke fa, kéwél di fa curpee.
22Bukki mooy sabe fa tata ya, till nangu kër yu bakkane ya. Àppu Babilon jege na, ay fanam du fi wees.