Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 48

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; yeen ñi ñu wooye turu Israyil, yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, di giñe turu Aji Sax ji, yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil te dëgg ak njekk taxul,
2moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi, di wéeroo Yàllay Israyil ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
3Yàgg na maa biral lay jëkka am. Tuddoon naa ko, yégle ko, jekki jëf ko, mu sotti.
4Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.
5Moo tax ma yàgg leena biralal lii, yégal leen ko balaa teew. Lu ko moy ngeen ne: «Sunu tuur mee ko def, sunu tuuru bant bee, sunu tuuru weñ gee ko amal di!»
6Lii lépp déggoon ngeen ko; xool-leen, xanaa dingeen ko nangu tey! Bés niki tey dinaa leen yégal lu bees, muy kumpa gu ngeen xamul woon.
7Léegi lees ko amal, du lu yàgg. Lu jiitu tey masuleen koo dégg te dungeen ne xamoon ngeen ko.
8Dégguleen, yéguleen, seeni nopp masula bënn; xam naa ne ay workati neen ngeen, «njuddu-fippu» lañu leen di wooye.
9Waaye sama tur tax na ma aj sama mer, sama woy tax na ma muñal leen, ba duma leen fàkkas.
10Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal, waaye du taalu xellikaayu xaalis, sawaras nattu laa leen xellee.
11Samaw tur a tax, sama tur laay jëfe. Jomb naa ñaaw! Te sama teddnga, duma ko joxe.
12Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba, yeen bànni Israyil gi ma dégtal sama woote. Maay kenn, maa jëkk te maa mujj;
13te sama loxo bee dëj suuf, sama ndijoor bi firi asamaan. Maa leen di woo, ñu bokk taxaw.
14Bokkleen daje yeen ñépp te déglu! Kan ci tuur yii moo yégle lii? Ki Aji Sax ji sopp mooy sottal nammeelu Aji Sax ji ci Babilon, won Kaldeen ña fa dëkke diisaayu loxoom.
15Maa àddu, man mii; maa ko woo, indi ko, te pexeem dina joy.
16Jegesileen ma, déglu ma; bu jëkk ba tey làquwma, di wax; te ba muy xew, fa laa teew. Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal boole maakam xelam.
17Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israyil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.
18Céy su ngeen sàmmoon samay santaane, ba jàmm baawaanal leen, njekk géejal leen,

19seen geño sakkan ni suuf, di seen meññeefu biir, tollook feppi suuf, du dog, du sànkoo fi sama kanam!
20«Génnleen Babilon, dawleen Kaldeen ñi, tey sarxolle. Biral-leen lii, yéene ko, te yeggeji ko waa cati àddina, ne leen Aji Sax ji jot na jaamam Yanqóoba.
21Marewuñu bérab yu wow ya mu leen jaarale woon, ndox mu balle ciw doj la leen xellil, moo xaru doj, ndox ma baawaan.
22Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne, «du ñeel ñu bon ñi.»