Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Esayi

Esayi 30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.
2Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma, xanaa di sàkku rawtub Firawna, di keppaaroo keppaarug Misra.
3Rawtub Firawnaay mujj di seen gàcce, keppaarug Misra di seen toroxte.
4Seeni jawriñ a nga xaat ba Cowan, seeni ndaw àgg ba Anes,
5waaye ñoom ñépp kersa lañuy ame Misra, googu leen dul amal njariñ. Du ndimbal, du njariñ, xanaa gàcceek toroxte.
6Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew: Réewum tiis laak njàqare, kërug gayndeeki segg, ak saamaan ak céebi, mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa, giléem lañu sëf seeni denc, jëme xeet wu leen dul jariñ.
7Ndimbalu Misra, cóolóolu neen! Moo tax ma tudde ko: Raxab, ponkal mi ne yàcc.
8Aji Sax ji nee: «Ayca, bind ko ci àlluwa, ñu gis! Rëdd ko cib téere, ngir ëllëg ak sibbir, mu dib seede ba fàww.»
9Wii xeet kat ay fippukat lañu, yii doom a diy fen-kat te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!
10Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. Wax nu lu neex, gisal nu ay nax.»
11Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
12Moo tax Aji Sell ju Israyil wax ne: «Gannaaw yeena xalab kàddu gii, yaakaaruleen lu moy doole ak pexey njubadi yu ngeen wéeroo,
13googu ñaawtéef ay mujj doon seen xar-xaru tata ju kawe, funki, tata ja jekki jóoru.
14Da naan tasar ni njaqal xandeer lu ñu naan rajax te ñéebluweesu ko, ba deesul gis ca tojit ya, dog bu tibb xal, mbaa mu as ndoxum déeg.»
15Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax ne: «Délsi, dal-lu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena buggul!
16Yeena ne: “Déedéet, danuy war fas, daw!” Dingeen daw moos! Ngeen ne: “Daamar yu gaaw lanuy war.” Ñi leen di dàq it di war daamar yu gaaw!
17Junneey daw fu leen kenn gëdde, juróom gëdd, ngeen daw yeen ñépp, ba ña des mel ni bantub raaya ci kaw tund, ne cundum ni raaya bu wéet ca coll wa.»
18Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!

19Yeen waa Siyoŋ, yeen waa Yerusalem, dootuleen jooy mukk! Bu ngeen jooyee, mu yërëm leen moos; bu leen di dégg, di leen nangul.
20Boroom bee leen di leel njàqare, nàndal leen coono, waaye moo leen di jàngal, dootu leen làqu; dingeen gis ki leen di jàngal,
21di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.
22Su boobaa ngeen sobeel seen jëmmi tuur yi ñu xoob xaalis; ak wurus wu xoob seen tuur yi ñu móol, ba boole lépp sànni ni sagar yu sobewu, ne ko: «Sore nu!»
23Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji, may leen pepp mu suuf meññ, sakkan te nangu, seen juri keroog di fore parlu yu yaa,
24Nag yeek mbaam yiy rijji sax, di xontoo cox bu ñu xorom, jóge ci mbàccum roq ak ngaska.
25Te tundoo tund wu kawe, wu mag ak wu ndaw, wali ndox a cay wale, keroog bés ba deret di tuuroo tuuru, tata ya jóoru.
26Weer day leer ni jant, jant gënatee leer, mel ni juróom yaari bëccëg, bésub keroog ba Aji Sax jiy takk damm-dammu ñoñam, fajal leen góom yi ay dóoram sabab.
27Aji Sax jaa ngii, jóge fu sore; mer ma réy, mu jógaale kàddug àrtu gu diis, di waxe xadar ju mat sëkk, baat ba mel ni sawara wuy xoyome,
28noo ga di wal mu baawaan, tollu ci put; mu nara segge xeet yi ab seggukaayu alkànde, wewal xeet yi ag laab gu leen di réeral.
29Teewul, bokk yi, seen woy yay jib; mel ni guddig màggal, ànd ak mbégte ni kuy toxoro, yéeg jëm kaw tundu Aji Sax ji, cëslaayal Israyil.
30Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg, wone diisaayu loxoom, ànd ak tàngooru meram, ak sawara wuy xoyome, ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur.
31Kàddug Aji Sax jeey jib, Asiri tiit bay lox, yetu Aji Sax ja dal,
32te saa yu yet wa Aji Sax ji féetale Asiri dalee, ngeen jibal am tëgg aki xalam. Aji Sax jeey xàcci loxoom, xareek Asiri.
33Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet, te buur ba lees ko waajalal; dees koo xóotal, yaatal ko, sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, di sël-sëli ni walum tamarax.