1Leween ñiy ay sarxalkat, ba ci giirug Leween gépp nag, wenn wàll mbaa céru suuf ñeelu leen ci seen bokki Israyil. Saraxi sawara yu Aji Sax ji, akub céram, moom lañuy dunde.
2Ab cér du leen ñeel ci seen biiri bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, na mu leen ko waxe woon.
3Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi.
4Te seen pepp mu jëkka ñor, ak seen biiñ bu bees, ak seen diw gu bees, ak kawar gi ngeen jëkka wate ca seeni xar, joxleen ko ko,
5ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo ko taamu, ci seen mboolemi giir, ngir mu taxaw, di liggéey ci turu Aji Sax ji, moom ak askanam, ba fàww.
6Ab Leween bu dëkke benn ci seeni dëkk, ak fu mu mana doon ci Israyil, su fa jógee dem ci coobarey boppam, bérab bu Aji Sax ji taamu,
7da fay liggéey ci turu Yàllaam Aji Sax ji ni mboolem bokki Leweenam, ña fa taxawe fa kanam Aji Sax ji,
8njël lu yemook njëlal ña mu fa fekk it lew na ko, te limaaleesul lu ko dikke ci njaayum alalu baayam.
9Bu ngeen demee ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji di jox, buleen roy jëf ju jomblu ju xeet yooyu.
10Bu kenn fekk ci seen biir kuy sarxe doomam ju góor, ak ju jigéen, lakk ko; ak kuy luxus, ak kuy seet, ak kuy gisaane, ak kuy xërëm,
11ak kuy liggéeyaate, ak kuy seete ab rawaan, ak kuy seete aw rab, mbaa kuy seete nit ñu dee,
12ndax mboolem ñiy def yooyu, Aji Sax ji seexlu na leen. Jëf ju seexluwu jooju moo waral seen Yàlla Aji Sax ji di leen dàqal seeni boroom.
13Muccleen sikk seen digganteek seen Yàlla Aji Sax ji,
14ndax xeet yooyii ngeen di dàqi kat, ay luxuskat aki seetkat lañuy déggal, waaye yeen seen Yàlla Aji Sax ji mayu leen loolu.
15Ab yonent bu soqikoo ci yeen kay, di seen mbokk ni man, moom la leen seen Yàlla Aji Sax ji di feeñalal. Moom ngeen di déggal.
16Mooy noonee ngeen ko sàkkoo woon rekk, ci seen Yàlla Aji Sax ji ca tundu Oreb, ca bésub ndaje ma, ngeen ne: «Rikk bunu déggati sunu baatu Yàlla Aji Sax ji. Sawara wu réy wii it, bunu ko gisati, lu ko moy nu dee,»
17te Aji Sax ji ne ma: «Ñoo yey wax loolu.
18Ab yonent laa leen di feeñalal ci seen biiri bokk, ni yaw. Maay yeb samay kàddu ci gémmiñam, mu àgge leen mboolem lu ma ko sant.
19Su boobaa ku déggalul sama kàddu yi muy wax ci sama tur, man maa ko koy topp.
20Waaye déy yonent bu am fitu àddu genn kàddu ci sama tur, te santuma ko mu wax ko, mbaa mu wax ci turi yeneen yàlla, boobu yonent, dee mooy àtteem.»
21Dingeen wax ci seen xel, ne: «Ana nu nuy ràññee kàddu gu Aji Sax ji waxul?»
22La yonent bi wax ci turu Aji Sax ji, su sottiwul, dikkul rekk, loola du kàddu gu Aji Sax ji wax. Ñeme Yàlla la ko yonent ba waxe, buleen ko ragal.