Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ba loolu wéyee nu walbatiku, awe yoon wa yéeg jëm Basan. Og buuru Basan nag dikk dajeek nun, mook gàngooram gépp, ngir song nu xare ca Eddrey.
2Aji Sax ji ne ma: «Bu ko ragal, ndax ci say loxo laa ko teg, mook gàngooram gépp, akum réewam. Nanga ko def na nga defoon Siwon buurub Amoreen ba woon ca Esbon.»
3Noonu la sunu Yàlla Aji Sax ji tege Og buuru Basan itam ci sunuy loxo, mook gàngooram gépp, nu duma leen ba desewul kuy dund.
4Booba lanu nangu mboolemi dëkkam. Amul benn dëkk bu nu nanguwul ci ñoom: juróom benn fukki dëkk, mboolem diiwaanu Argob, ba bokk ca nguurug Og ca Basan.
5Yooyu yépp di dëkk yu dàbblikoo tata yu kawe, ak bunt yu tëje ràpp, te limaaleesul dëkk-dëkkaan yu baree bare, yu dara wërul.
6Nu faagaagal leen, na nu defoon ak Siwon buurub Esbon. Dëkk yépp lanu faagaagal: góor ak jigéen ba ca tuut-tànk ya.
7Mboolem jur gaak alali dëkk ya nag, nu sëxëtoo.
8Jant yooyu lanu nangoo ci loxol ñaari buuri Amoreen ñooña ca wàllaa dexu Yurdan, réew ma dale ca xuru Arnon, ba ca tundu Ermon.
9Ermon googu la waa Sidon di wooye Siryoŋ, Amoreen ñi di ko wooye Senir.
10Mboolem dëkki joor ga lanu nangu, ak mboolem diiwaanu Galàdd, ak mboolem Basan, ba ca Salka ak Eddrey, dëkki nguurug Og mu Basan.
11Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar.
12Suuf soosu nu nangu ca jant yooya, te dale ca Arower ga ca xuru Arnon ca bëj-saalum, ak ca bëj-gànnaar, genn-wàllu diiwaanu tundi Galàdd, aki dëkkam, maa ko jox Rubeneen ñi, ak Gàddeen ñi.
13Ndesu Galàdd ak mboolem Basan gu nguurug Og, ma jox ko genn-wàllu giirug Manase. Diiwaanu Argob gépp ak Basan googu gépp, lañu daan wooye réewum Refayeen ña.
14Yayir mi askanoo ci Manase moo nangu mboolem diiwaanu Argob, ba ca kemu réewum Gesureen ña, ak Maakateen ña. Moo tudde boppam Basan googu, ba tax ñu di ko wooye Sanci Yayir ba tey jii.
15Askanu Makir laa jox diiwaanu Galàdd.
16Rubeneen ñeek Gàddeen ñi laa jox la dale diiwaanu Galàdd ba ca xuru Arnon, diggu xur wa di seen kemu suuf ci genn wet, dexu Yabog di seen kemu ñook Amoneen ña.
17Fa joor ga feggook dexu Yurdan it di kemu, diggante dexu Kineret ca bëj-gànnaar, ak ca bëj-saalumu géeju Xorom ga, ba ba ngay àgg ca suufu tundu Pisga, ca penku.
18Jant yooyu laa leen sant ne leen: «Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jox réew mii, ngir ngeen nangu ko. Na xarekat yépp gànnaayu, jàll, jiitu seen bokki bànni Israyil.

19Seeni jabar doŋŋ, ak seeni doom ak seenug jur, ndax xam naa ne jur gu takku ngeen am, ñooy des ci seen dëkk yi ma leen jox,
20ba keroog Aji Sax ji noppalee seen bokki bànni Israyil ni yeen, fekk leen nangu, ñoom it, réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox, ca wàllaa dexu Yurdan. Su ko defee ku nekk ci yeen saña dellu ca céru suufam ba ma ko jox.»
21Yosuwe itam, sant naa ko ci jant yooyu ne ko: «Sa bët moo la may mboolem ni seen Yàlla Aji Sax ji def ak ñaari buur yii. Noonu rekk la Aji Sax jiy def ak mboolem nguur ya nga jëm.
22Buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di xeexal.»
23Jant yooyu laa tinu Aji Sax ji, ne ko:
24«Éy Boroom bi Aji Sax ji, yaa ma wonagum lenn ci sa màggaay ak sa doole, Sang bi. Ana yàlla ju nekk asamaan, mbaa ci kaw suuf ju mana roy say jëf ak say jaloore?
25May ma rekk ma jàll, ba gis réew mu baax, ma ca wàllaa dexu Yurdan, tund wu rafet woowu ba ca Libaŋ!»
26Waaye fekk na Aji Sax ji mere ma lool ndax yeen, ba faalewu ma. Aji Sax ji ne ma: «Na doy. Bu ma waxati lu jëm ci loolu.
27Yéegal ba ca kaw tundu Pisga, nga dawal sa bët, te séenu réew ma wetu sowu, ba bëj-gànnaar, bëj-saalum, ba penku. Xoolal bu baax, nde doo jàll dexu Yurdan gii.
28Waaye nanga yebal Yosuwe, ñaax ko, jàjj ko, ndax moom mooy jàll, jiite mbooloo mii, te moo leen di jox réew moomu ngay séen.»
29Ba mu ko defee nu toog ca xur wa, janook Bet Pewor.