Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee,
2ndax askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.
3Buleen lekk lenn lu seexluwu.
4Lii moo di mala yi ngeen di lekk seen suux: nag ak xar ak bëy;
5ak kooba ak kéwél, ak lu xeetook kooba, ak lu xeetook kéwél, ak bëyu àll, ak bëyu kaw tund.
6Mboolem mala mu ci we wi xar, séddlikoo yaar, te muy duññ, moom ngeen di lekk aw suuxam.
7Waaye yii, buleen lekk seen suux: lu ciy duññ doŋŋ, te we wi xarul, mbaa lu we wi xar, te duññul. Lu mel ni giléem ak njomboor ak daman, ndax dañuy duññ waaye seen we xarul. Yooyu daganul ci yeen.
8Mbaam-xuux, moom, we wi xar na waaye du duññ. Kon daganul ci yeen. Aw suuxam, buleen ko lekk, te méddam, buleen ko laal.
9Lii nag, sañ ngeen koo lekk, ci mboolem lu dëkke ndox: mboolem lu ci am ciiriir aki waasintóor, sañ ngeen koo lekk.
10Waaye lu ci amul ciiriir aki waasintóor, buleen ko lekk, ndax daganul ci yeen.
11Mboolem njanaaw lu set, sañ ngeen koo lekk.
12Waaye lii ngeen dul lekk ci njanaaw yi: jaxaay ak tan, ba ca mu ñuul ma,
13ak céeli bu xonq, ak céeli bu ñuul, ak maf, ak lu mu xeetool,
14ak lépp luy baaxoñ ak lu mu xeetool,
15ak bànjóoli ak looy, ak lu mu xeetool, ak kirigéej, ak mboolem xeeti liccin, ak yébb, ak lu xeetook xodd, ak musejubru ak njugub.
19Mboolem boroomi laaf yu sew-sewaan, daganul ci yeen. Deesu ci lekk lenn,
20xanaa boroomi laaf yi ci set. Yooyu, sañ ngeen koo lekk.
21Buleen lekk lenn lu médd. Jaambur bu dal ak yeen, sañ ngeen koo jox lu médd, mu lekk, mbaa ngeen jaay ko ab doxandéem. Waaye yeen askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Te buleen togg ab tef ci meewum yaayam.

22Fexeleen bay génne benn céru fukkeel ci mboolem lu seeni tool meññ at mu nekk.
23Seen cérub fukkeelu pepp, ak biiñ bu bees, ak diw gu bees, ak lu seen jur taawloo, muy nag, di gàtt, nangeen ko xéewloo fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fi bérab bi mu taamoo dëël turam ëllëg. Su ko defee ngeen tàggatu ci ragal seen Yàlla Aji Sax ji fu ngeen tollu.
24Su ngeen manula dox yoon wi, ndax seen Yàlla Aji Sax jee leen barkeele meññeef mu bare mu ngeen dul àttan, ci diggante bu sorewaatoo lool ak bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam,
25su boobaa dangeen di wecci cérub fukkeel ba xaalis, jël xaalis ba te dem ba fa seen Yàlla Aji Sax ji taamu.
26Su ko defee ngeen weccikoo fa xaalis bi lu leen neex, muy nag mbaa gàtt, mbaa biiñ, mbaa geneen naan gu diis, ak lu leen seen bakkan xiir, ngeen xéewloo fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, bànneexoo ko, yeen ak seen njaboot.
27Leween gi ci seen biir dëkk nag, buleen leen fàtte, ndax amuñu wàll ci seen céru suuf.
28Ñetti at yu mat yu nekk, nangeen génne mboolem seen céri fukkeeli meññeef ca at mooma, te ngeen denc ko ca seen biir dëkk,
29ndax Leween, ñi amul wàll ci seen céru suuf, dikk, ñook doxandéem yi ak jirim yi ak jëtun, yi ngeen dëkkal, ngir ñu lekk ba regg. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seenu ñaq.