Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Baamtug Yoon wi

Baamtug Yoon wi 24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ku jël jabar, ba gannaaw gi xoolatu ko bëtu yiw, ndax lu tegginewul lu mu ko gisal, su ko bindalee kayitu pase, teg ko ci loxoom, ba yiwi ko, mu jóge këram,
2su jógee ca kër ga, dem ba mujj doon jabaru keneen,
3su ko jëkkëram ju mujj jooju jéppee, bindal ko kayitu pase, teg ko ci loxoom, ba yiwi ko, mu jóge këram, mbaa su jëkkëram jooju ko mujja jël faatoo,
4su boobaa jëkkëram ju jëkk ja ko yiwi woon du ko saña jëlaat jabar, gannaaw ba ndaw sa sobewoo noonu, ndax loolu lu jomblu la fi kanam Aji Sax ji, te waruleena indi bàkkaar ci biir réew mi leen seen Yàlla Aji Sax ji di moomale.
5Ku jël ab séet du bokk ci gàngoor gu jëm xare, te deesu ko sas lenn. Day moom boppam atum lëmm, ngir toog këram, di bégal jabaram ji mu jël.
6Buleen tayleloo kenn ñaari doji wolukaayam, ci bor bu mu leen ameel. Buleen ko tayleloo wenn doj wa féete kaw sax, ndax kon bakkanam ngeen def ub tayle.
7Su amee nit ku ñu fekke kenn ciy bokkam, ku mu sàcce ci bànni Israyil, mu di ko jaamloo, mbaa mu jaay ko, su boobaa dee mooy àtteb kooka ko sàcc. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci seen biir.
8Fexeleen ba ci biir mbasum jàngoroy der juy màgg, ngeen di sàmmoo jëfe bu baax, mboolem lu leen sarxalkat yi, Leween ñi tegtal. Ni ma ko sante sarxalkat yi, Leween ñi, sàmmooleen koo jëfe noonu.
9Fàttlikuleen la seen Yàlla Aji Sax ji defoon Maryaama ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra.
10Bu ngeen lebalee seen moroom, ak lu bor ba mana doon, buleen dugg biir néegam, di fa jël ab tayleem.
11Ca biti ngeen di taxaw, ka ngeen di lebal yótsi leen ab tayleem ca biti.
12Su dee ku néew doole, buleen tëraale ab tayleem.
13Fexeleen ba delloo ko tayle ba bu jant biy so, ba mu tëraale mbubbum tayle ma, sante leen ko, mu dig njekk, fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji.
14Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi.
15Ci bés bi ngeen koy fey peyooram. Bu ko jant sowe, ndax néew doole la te moom la yaakaara dunde. Lu ko moy mu boole leen ak Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.
16Deesul teg waajur àtteb dee, ngir weccikoo ko doom ja, te doom it deesu ko teg àtteb dee, weccikoo ko waajur wa. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy tege àtteb dee.
17Buleen xañ dëgg ab doxandéem akub jirim, te buleen taylelu mbubbum jëtun.
18Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa jote. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu.

19Bu ngeen di góob seenub tool, ba fàtte ab sëq ca tool ba, buleen dellu di ko jëli. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun, ñoom la poraat may ñeel, su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji barkeel leen ci mboolem seenu ñaq.
20Bu ngeen bàccee seen garabu oliw ba noppi, buleen toppaat car ya, di witt lu ca des. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun, ñoom la ndesit way ñeel.
21Bu ngeen wittee seen tóokëru reseñ, buleen dellu, di ko wittaat. Ab doxandéem akub jirim akub jëtun ñoom la wittaat may ñeel.
22Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu.